"deeleen joxante Àddiya kon dangeen bëggante".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"deeleen joxante Àddiya kon dangeen bëggante".
«تَهَادَوا تَحَابُّوا».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaaxe ci jullit bi di weccente Àddiya ak mbokku jullitam, ak ne Àddiya dafa bokk ci yiy waral bëggantr ak miinanteg xol yi.
Sopp nañu joxe Àddiya; ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a digle.
Àddiya day waral bëggante.
Jaadu na ci nit ki muy def lépp luy xëcc mbëggeel ci digganteem ak nit ñi moo xam ci Àddiya la walla ci nooyug wet walla vi wax ju rafet walla ci bélli xar kanam ci kem kàttanam.
Téere bu mag bi Al-Bayhaqii def ci Sunna yi (6/ 169).
Yataal gi (5)
الأدب المفرد للبخاري (ص:208) (594).
مسند أبي يعلى الموصلي (11/ 9) (6148).
فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام (4/ 319).
فيض القدير (3/ 271).
التيسير بشرح الجامع الصغير (1/ 457).