Skip to content

Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga ca kaw Minbar ba, loo gis ci julli guddi, mu ne ko: "ñaar ñaar

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga ca kaw Minbar ba, loo gis ci julli guddi, mu ne ko: "ñaar ñaar, bu ragalee suba jot mu julli benn ràkka, tóolale ko li mu julli" daan na wax it: "defleen seen mujjug julli muu lu tóol" ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ko digle.

سَأَلَ رَجُلٌ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ عَلَى المِنْبَرِ، مَا تَرَى فِي صَلاَةِ اللَّيْلِ، قَالَ: «مَثْنَى مَثْنَى، فَإِذَا خَشِيَ الصُّبْحَ صَلَّى وَاحِدَةً، فَأَوْتَرَتْ لَهُ مَا صَلَّى» وَإِنَّهُ كَانَ يَقُولُ: «اجْعَلُوا آخِرَ صَلاَتِكُمْ وِتْرًا» فَإِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَمَرَ بِهِ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga ca Minbar ba di xutba: yaw Yonnente Yàlla bi xamal ma naka laay jullee guddi? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: dangay julli di sëlmël ci ñaari ràkka yu ne, boo ragalee suba gi fenk nga julli benn ràkka tóolale ko li nga julli, ak ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na dénkaane ñu def mujjug jilli guddi gi muy lu tóol.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Cosaan ci julli guddi mooy mu sëlmël ci ñaari ràkka yu ne, ci lu dul tóolal ga.

Julli guddi tënku ñu ko ci ab lim; ngir li ñu boyal wax ji.

An-Nawawii nee na: "jullig guddi ak bëccëg ñaar ñaar la", hadiis bii dañu koy yen ci leeral li gën, te mooy muy sëlmël ci ñaari ràkka yu ne, moo xam naafilay guddi la walla bëccëg dees na sopp muy sëlmël ci ñaari ràkka yu ne.

An-Nawawii nee na: tegtal la ci ne liy sunna mooy mu tóolal ci mujjug jilli guddi gi, ak ne waxtoom bu fajar gi fenkee lay génn, te mooy li siiw ci sunu ngiir mi, te loolu la ñi ëpp ci woroom xam-xam yi wax.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 102) (472).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 517) (751).

Yataal gi (8)

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري.

لابن حجر(1/ 456).

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (2/ 394).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (2/ 233).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

لعبد الله البسام (ص217).