Skip to content

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy faatu bàyyiwul benn Diinaar walla Dërëm du caagine jaam bu góor walla jigéen du caagine dara, lu dul fasam wu weex wi, ak ngànnaayam, ak suuf su mu def ab sarax.

Jële nañu ci Amr ibn Al-Haaris gorob Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di mbokku ndayu jullit ñi Juwayriya bint Al-Haaris yal na leen Yàlla dollee gërëm, mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy faatu bàyyiwul benn Diinaar walla Dërëm du caagine jaam bu góor walla jigéen du caagine dara, lu dul fasam wu weex wi, ak ngànnaayam, ak suuf su mu def ab sarax.

مَا تَرَكَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عِنْدَ مَوْتِهِ دِرْهَمًا وَلاَ دِينَارًا وَلاَ عَبْدًا وَلاَ أَمَةً وَلاَ شَيْئًا، إِلَّا بَغْلَتَهُ البَيْضَاءَ، وَسِلاَحَهُ، وَأَرْضًا جَعَلَهَا صَدَقَةً.

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bàyyiwul Dërëmj xaalis du caagine Diinaaru wurus, jaam bu góor bu ñu moom du caagine jaam bu jigéen bu ñu moom, walla dara ci alal, lu dul fasam wu weex wi nga xam ne daan na ko war, ak ngànnaayam wi mu daan gàddu, ak suuf su mu def Wàqf ci ag wéram ñeel way-ñàkk ji.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yonnente yi deesu leen dond.

Leeral li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bàyyi ginnaaw ag faatoom.

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc faatu na te bàyyiwul dara lu am solo, ngir ag tabeem ak joxeem ak rafetalam.

Al-Karmaanii nee na: aji-dellu ji nekk ci waxam ji (mu def ko) day dellu ci ñatt maanaam fas wi ak ngànnaay li, ak suuf si waaye delluwul ci suuf si dong.

Goro: mbokku jabar, goro yi ci koteg jigéen gi la.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 2) (2739).

Yataal gi (3)

النهاية في غريب الحديث والأثر (254).

فتح الباري لابن حجر (5/ 360).

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (14/ 31).