Skip to content

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu.

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu.

أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ نَهَى عَنِ الْقَزَعِ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na wat lenni kawaru bopp bàyyi leneen li. Tere gi nag day làmboo góor ñépp ndaw ak mag, budee jigéen nag warut a wat dara ci kawaru boppam.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sariihab Lislaam dafa yittewoo melokaanu nit ki.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 163) (5921).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1675) (2120).

Yataal gi (5)

نزهة المتقين (2/ 1126).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (19/ 380).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (6/ 381).