"jëlal ci alalam ci njekk lu la doy doy sa doom".
Jële nañu ci Aysa yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Hindu Bintu Utbata Soxnas Abuu Sufyaan dafa dugg ci Yonente bi ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, Abuu Sufyaan de góor gu nay la, duma jox lu ma doy man ak samay doom lu dul xanaa ma jël ci alalam ci lu mu xamul, ndax damay am ci loolu bàkkaar? Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "jëlal ci alalam ci njekk lu la doy doy sa doom".
دَخَلَتْ هِنْدٌ بِنْتُ عُتْبَةَ امْرَأَةُ أَبِي سُفْيَانَ عَلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَتْ: يَا رَسُولَ اللهِ، إِنَّ أَبَا سُفْيَانَ رَجُلٌ شَحِيحٌ، لَا يُعْطِينِي مِنَ النَّفَقَةِ مَا يَكْفِينِي وَيَكْفِي بَنِيَّ إِلَّا مَا أَخَذْتُ مِنْ مَالِهِ بِغَيْرِ عِلْمِهِ، فَهَلْ عَلَيَّ فِي ذَلِكَ مِنْ جُنَاحٍ؟ فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «خُذِي مِنْ مَالِهِ بِالْمَعْرُوفِ مَا يَكْفِيكِ وَيَكْفِي بَنِيكِ».
Hindu Bintu Utbata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa laaj Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci jëkkëram ji Abuu Sufyaan yal na ko Yàlla dollee gërëm ci ne góor gu nay la te xér ci alalam, te du ko jox ci deppaas lu ko doy moom ak doomam, lu dul mu jël ci alal ji ci sekkare te du ko xam, kon ndax dana am bàkkaar ci loolu? Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: jëlal ci alalam ngir yaw ak sa doom kem li ñu xam ci aada ne dana leen doy donte yégu ko.
Warug joxe deppaas ñeel soxna yi ak doom yi.
Ibn Hajar nee na: li mu namm ci waxam ji: "jëlal ci alalam lu la doy ci njekk", mu delloo ko ci njekk ndax day loo xam ne Sariiha tënku ko.
Ibn Hajar wax ne: dañuy tegtaloo ci hadiis bii ci ne dagan na nu tudd nit ci lu ko neexul bu dee ci anamug laaj la ak jàmbat mbaa lu ni mel, te benn la ci bérab yi jëw dagane.
Al-Xurtubii nee na: Hindu bëggut a melal Abuu Sufyaan ci ne dafa nay ci bépp anam, waaye dafa wane melokaanam ak moom, ci ne day ŋott ci moom ak i doomam, te loolu tekkiwul nay kaare maa, ndax njiit yu bari dañuy def loolu ak seeni njaboot, di gënale ay jàmbur ngir sàkku a xaritoo ak ñoom.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 79) (2211).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1338) (1714).
Yataal gi (4)
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
للبسام (ص700).
الإعلام بفوائد عمدة الأحكام.
لابن الملقن (10/ 12).