Skip to content

«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».

Jële na ñu ci Buraydata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».

«إِنَّ الْعَهْدَ الَّذِي بَيْنَنَا وَبَيْنَهُمُ الصَّلَاةُ، فَمَنْ تَرَكَهَا فَقَدْ كَفَرَ».

At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne kóllare gi dox ci diggante jullit ñi ak ñu dul ñoom ci yéefar yi ak naaféq yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Màggaayu mbiri julli, ak ne mooy liy tàqale diggante jullit bi ak yéefar bi.

Àttey Lislaam day saxe ci li feeñ ci melokaani nit ki waaye du lia nëbbu.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (1/ 231) (463).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 365) (2621).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (2/ 181) (1079).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (38/ 20) (22937).

Yataal gi (2)

فيض القدير (4/ 395).

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (6/ 192) (6/ 193).