Doon naa gis Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram, ak ci càmmooñam, ba may gis weexitu lexam.
Jële nañu ci Sahd yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Doon naa gis Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram, ak ci càmmooñam, ba may gis weexitu lexam.
كُنْتُ أَرَى رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُسَلِّمُ عَنْ يَمِينِهِ، وَعَنْ يَسَارِهِ، حَتَّى أَرَى بَيَاضَ خَدِّهِ.
Sahd ibn Abii Waqaas yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne daan na gis weexitu lexi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ngir tarug geestoom bu daan sëlmël ci julli ci ndayjooram ñeel sëlmël gu njëkk gi, ak ci càmmooñam ñeel sëlmël gu ñaareel gi.
Yoonalees na jotale geestu gi jëm ci wetu ndayjoor ak jëm ci wetu càmmooñ.
Yoonal nañu ñaari sëlmël muy ci jëm ci ndayjoor ak jëm ci càmmooñ.
An-Nawawii nee na : bu sëlmëloon ñaari sëlmël ci ndayjoor bi walla ci càmmooñ bi walla canamam walla bu njëkk bi ci càmmooñam bu ñaareel bi ci ndayjoor am kon julleem wér na te def na ñaari sëlmël yi, waaye ngëneelu melo wi faat na ko.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 409) (582).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (13/ 99).
مرقاة المصابيح شرح مشكاة المصابيح (4 /30).