Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan julli fajar day toog fa mu jullee ba keroog jant bi di fenk ba leer
Jële nañu ci Jaabir ibn Samurata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan julli fajar day toog fa mu jullee ba keroog jant bi di fenk ba leer, mu ne: daawul jug ca jullikaayam ba mu jullee suba walla njël, ba keroog jant bi di fenk, bu jant bi fenkee mu jug, ñu daan waxtaan di jël ca mbiri ceddo ga, ñuy ree muu muuñ.
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ إِذَا صَلَّى الفَجْرَ جَلَسَ فِي مُصَلَّاهُ حَتَّى تَطْلُعَ الشَّمْسُ حَسَنًا، وَقَالَ: كَانَ لَا يَقُومُ مِنْ مُصَلَّاهُ الَّذِي يُصَلِّي فِيهِ الصُّبْحَ أَوِ الغَدَاةَ، حَتَّى تَطْلُعَ الشَّمْسُ، فَإِذَا طَلَعَتِ الشَّمْسُ قَامَ، وَكَانُوا يَتَحَدَّثُونَ فَيَأْخُذُونَ فِي أَمْرِ الجَاهِلِيَّةِ، فَيَضْحَكُونَ وَيَتَبَسَّمُ.
Bokk na ci sunnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan julli fajar day toog ca jullikaayam ba ba keroog jant bi di jug, daawul jug ca jullikaayam ba mu jullee fajar, ba keroog jant bi di fenk. Bu jant bi fenkee mu jug, ñoom ñu daan waxtaan di tudd yenn mbiri ceddo ga njëkk lislaam moom mu noppi, ñoom ñuy ree amaana it mu muuñ ànd ak ñoom.
Sopp nañu sikar ginnaaw jullig suba ba keroog jant bi di fenk, ak taqoo ak bérab ba fii ak ngànt amul.
Leeral li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nekkoon ci ay teddngay jikko ak nooy wet, ba tax mu daan toog ak sahaaba yi, di déglu seen waxtaan ak seen i nettali ak di ca muuñ.
Dagan na ñu waxtaane jamonoy ceddo ga ci jàkka.
Ree ak muuñ dagan na; ndax li ñuy tete mooy bari ree.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 464) (670).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (14/ 407).
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (2/ 296).