Skip to content

"man yónniwuñu ma ngir may rëbbe, waaye dañu maa yónni ngir yërmànde".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: dañoo ne: yaw Yonnente Yàlla bi ñaanal Yàlla yéefar yi, mu wa ne:

"man yónniwuñu ma ngir may rëbbe, waaye dañu maa yónni ngir yërmànde".

«إِنِّي لَمْ أُبْعَثْ لَعَّانًا، وَإِنَّمَا بُعِثْتُ رَحْمَةً».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Sàkkunañu ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ñaan Yàlla bokkaalekat yi, mu daal di ne: man Yàlla yónniwu ma ci nit ñi ngir soreele leen ak dàq leen ci yërmàndey Yàlla ba tax ma leen di dog ci yiw yi, man dañu maa yónni ngir ma nekk sababu yiw ak yërmànde ci nit ñépp, rawatina ci jullit ñi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Matug jikkoy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Solos sellal làmmiñ ci ŋàññe ak rëbbe ngir roy ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Terenañu rëbbe.

Ñaaxe ci yërëm nit ñi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2006) (2599).

Yataal gi (2)

المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (6/ 582).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (40/ 683).