Skip to content

"yaw Yàlla sama Boroom man dey nit rekk laa kepp ku ma ŋàññ ci jullit ñi walla ma rëbb ko walla ma dóor ko maa ngi lay ñaan nga defal ko ko ag sell ak ug yërmànde".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"yaw Yàlla sama Boroom man dey nit rekk laa kepp ku ma ŋàññ ci jullit ñi walla ma rëbb ko walla ma dóor ko maa ngi lay ñaan nga defal ko ko ag sell ak ug yërmànde".

«اللهُمَّ إِنَّمَا أَنَا بَشَرٌ، فَأَيُّمَا رَجُلٍ مِنَ المُسْلِمِينَ سَبَبْتُهُ أَوْ لَعَنْتُهُ أَوْ جَلَدْتُهُ فَاجْعَلْهَا لَهُ زَكَاةً وَرَحْمَةً».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa ñaan mu ne: yaw Yàlla sama Boroom man dey nit kese laa, damay mer kem ni nit ñi di mere, bépp jullit bu ma lor walla ma ŋàññ ko saaga ko, walla ma rëbb ko ñaan ko ag dàq ci sa yërmànde, walla ma dóor ko, maa ngi lay ñaan nga defal ko loolu muy ag sell ak ug jege ak ug laabal ak farug bàkkaar ak yërmànde goo koy yërëme.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Màggug jikkoy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Ibn Hajar nee na: nekk na ci hadiis bi matug yërmàndey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci xeetam wi ak rafetug jikkoom ak teddngay jëmmam ba tax mu jubloo wuutal li bawoo ci moom muy ag dëgëral ak teraanga.

An-Nawawii nee na: bu ñu nee: naka lay ñaane ci jaw ku yeyoowul ñaan ci kawam walla mu koy ŋàññ walla mu koy rëbb ak lu niru looli? Tontu bi mooy li woroom xam-xam yi tontu, tënk bi di ñaari anam: benn bi: mooy ne li ñu ci namm mooy ne yeyoowul loolu fa Yàlla mu kawe mi, ak ci li nëbbu ci mbir mi, waaye ci li feeñ mooy yeyoo na ko, ag yeyoom ñeel loolu feeñ ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci màndargay sariiha, waaye ci li nëbbu yeyoowul loolu, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañu ko a digal mu atte ci li feeñ, Yàlla nag mooy méggoo la làqu. Ñaareel bi: mooy ne li am ci ŋàññ ko ak ñaan ci kawam ak ak yu ko niru nekkul jubluwaayam, waaye dafa bokk ci li araab yi aadawoo ci jokk wax ji ci lu dul yéene, niki li ngay wax: dóor nga sa ndayjoor ci suuf, ténji nga nelu nga, ñëw na ci hadiis bi: (bu say at bari waay), nekk ci hadiisu Muhaawiya yàlla bu Yàlla suural sa biir, ak yu ni mel, jubluwuñu ci dara ci yooyu dëgg-dëggi ñaan, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ragal dara ci yooyu dëppoo ak ñu nangu ñaan gi, mu ñaan Boroomam mu Sell mi xemmem ci moom mu def loolu ag yërmànde ak farug bàkkaar, ak ug jege, ak laab ak ag pay, te lii sax lu néew te raar ci jamono yi la daan am ci moom, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nekkul woon ku ñaaw làmmiñ du caagine ku ñaaw i jëf, nekkul woon ab rëbbekat du caagine ab fayoontekat ngir boppam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 77) (6361).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2007) (2601).

Yataal gi (2)

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (22/ 310).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (9/ 207).