Skip to content

"xanaa du ku nekk ci yéen day déeyante ak Boroomam, bu kenn lor kenn

Jële nañu ci Abii Sahiid yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Ihtikaaf na ci jàkka ji, mu dégg leen ñuy béral njàng mi, mu wuññi kiiraayam, ne leen: "xanaa du ku nekk ci yéen day déeyante ak Boroomam, bu kenn lor kenn, bu kenn di yëkkëti kàddoom ci kaw ñeneen ñi bu ñuy jàng", walla mu wax: "ci julli gi".

اعْتَكَفَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي المَسْجِدِ، فَسَمِعَهُمْ يَجْهَرُونَ بِالقِرَاءَةِ، فَكَشَفَ السِّتْرَ، فَقَالَ: «أَلَا إِنَّ كُلَّكُمْ مُنَاجٍ رَبَّهُ، فَلَا يُؤْذِيَنَّ بَعْضُكُمْ بَعْضًا، وَلَا يَرْفَعْ بَعْضُكُمْ عَلَى بَعْضٍ فِي القِرَاءَةِ»، أَوْ قَالَ: «فِي الصَّلَاةِ».

Abóo Daawuda soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nekkoon ci jàkka ji di Ihtikaaf ci genn xàbb ci biir jàkka ji ngir jegeñ-jegeñlu Yàlla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dégg yenn sahaaba yi di béral seenu njàngum Alxuraan béral gu tar ba ñenn ñi di lor ñeneen ñi. Mu muri kiiraayu xàbb bi, daal di yedd ñiu def loolu, ne leen: yéen ñépp dangeen di déeyante séen ci di jàng Alxuraan, kon bu ñenn lor ñeneen ñi, bu kenn yëkkëti kàddoom ci kaw kàddu ñeneen ñi ci njàng mi, walla ci julli gi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Tere nañu yëkkëti kàddu ci jàng Alxuraan, bu dee lor keneen da cee nekk.

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day jàngam sahaabaam yi teggini jàng Alxuraan.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 494) (1332).

Yataal gi (4)

شرح سنن أبي داود للعباد (162/ 18).

شرح أبي داود للعيني (5/238).

شرح سنن ابي داود لابن رسلان (6/515).

ذخيرة العقبى (11/669).