"bariwaa na ku kawar ga cuqaaral ñu koy tëye ci bunt yi te bu giñoon ci Yàlla mu setal ko".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bariwaa na ku kawar ga cuqaaral ñu koy tëye ci bunt yi te bu giñoon ci Yàlla mu setal ko".
«رُبَّ أَشْعَثَ مَدْفُوعٍ بِالْأَبْوَابِ لَوْ أَقْسَمَ عَلَى اللهِ لَأَبَرَّهُ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne amna ci nit ñi ku kawaram di baramu daal pënd, du ko diw te du ko raxas lu bari, amul benn dayo ci nit ñi ba dañu koy tëye ci bunt yi, di ko dàq di ko doyadil; te moom bu giñoon ci ne dara dana am kon Yàlla dana ko amal ngir teral ko ci nangu ñaanam, ak ñoŋal ko ci wuuteg ngiñam, ngir ngëneelam ak wàccuwaayam ci Yàlla.
Yàlla du xool melow jaam bi waaye xol yi lay xool ak jëf yi.
War na ci nit ki mu yittewoo jëfam ak laabug xolam lu ëpp lu muy yittewoo yaramam ak colam.
Wàcce sa bopp ngir Yàlla ak toroxlul ko sabab la ci nangu ñaan, loolu moo tax; Yàlla mu sell mi di setal way-ragal yi nëbbu.
Leeral yar gi Yonente bi daan yar nit ñi; ba kenn du xeeb kenn.
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2024) (2622).
Yataal gi (7)
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (5/ 48).
بهجة الناظرين.
لسليم الهلالي (1/ 344).
نزهة المتقين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 268) شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (3/ 63).