Skip to content

"ku dajee ak Yàlla te bokkaalewu ko dara kon njuumte yi mu àndal du ko lor, ki faatu fekk mo doon bokkaale Yàlla kon yiw wi mu àndal du ko jariñ".

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"ku dajee ak Yàlla te bokkaalewu ko dara kon njuumte yi mu àndal du ko lor, ki faatu fekk mo doon bokkaale Yàlla kon yiw wi mu àndal du ko jariñ".

«مَنْ لَقِيَ اللهَ لَا يُشْرِكُ بِهِ شَيْئًا لَمْ تَضُرَّهُ مَعَهُ خَطِيئَةٌ، وَمَنْ مَاتَ وَهُوَ يُشْرِكُ بِهِ لَمْ يَنْفَعْهُ مَعَهُ حَسَنَةٌ».

Ahmat soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku faatu ba daje ak Yàlla di aji-kennal te bokkaalewu ko dara kooku ci waa àjjana la bokk, doonte dañu ko mbugal ci ca sawara ngir ay bàkkaaram, ku faatu te doon bokkaale Yàlla dara kooku yiw du ko jariñ ndax bokkaale gi mu àndal; te àjjana araam na ci moom.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Àrtu ci bokkaale, ak ne moom moo gën a màgg ci bàkkaar yi ak njuumte yi, ak ne Yàlla du ko jéggale.

Ngëneelu Tawhiid, ak ne day waral dugg àjjana; doonte ginnaaw ba ñu ko mbugalee la.

Solos sax ci Tawhiid ba faatu, ak bañ a def safaanam re mooy bokkaale.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (11/ 155- 156) (11/ 157) (6586).

Yataal gi (1)

فيض القدير شرح الجامع الصغير (6/220).