Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ne ma: "jàngal ma"
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ne ma: "jàngal ma", ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ndax dama lay jàngal te ci yaw lañu ko wàcce? Mu ne: "waaw" ma jàng saaru An-Nisaa ba egg ci aaya bii: {naka la mbir may mel bu nu indee ci xeet wu nekk ab seede, nu indi la nga nekk seede ci ñii} [An-Nisaa: 41], mu daal di ne: "leegi doy na" ma geestu ko, fekk bët yi di jooy.
قَالَ لِي النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «اقْرَأْ عَلَيَّ»، قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، أَأَقْرَأُ عَلَيْكَ، وَعَلَيْكَ أُنْزِلَ؟ قَالَ: «نَعَمْ» فَقَرَأْتُ سُورَةَ النِّسَاءِ حَتَّى أَتَيْتُ إِلَى هَذِهِ الآيَةِ: {فَكَيْفَ إِذَا جِئْنَا مِنْ كُلِّ أُمَّةٍ بِشَهِيدٍ، وَجِئْنَا بِكَ عَلَى هَؤُلاَءِ شَهِيدًا} [النساء: 41]، قَالَ: «حَسْبُكَ الآنَ» فَالْتَفَتُّ إِلَيْهِ، فَإِذَا عَيْنَاهُ تَذْرِفَانِ.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa sàkku ci Abdallah ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jàngal ko dara ci Alxuraan, mu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, naka laa lay jàngale te ci yaw lañu ko wàcce?! Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: dama ko a bëgg a dégg ci keneen, mu jàngal ko saaru An-Nisaa, ba mu tollee ci waxu Yàlla mu kawe mi: {naka la mbir may mel bu nu indee ci xeet wu nekk ab seede nu indi la nga nekk seede ci ñii}. Maanaam naka la sa mbir ak sa mbiri xeet wi di mel bu nu la indee nga nekk seede ci sa xeet wu ci ne jottali nga sa bataaxalu Boroom bi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bàyyil njàng mi leegi, Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: ma geestu ko fekk rangooñ yi di sottiku ci bët yi ngir tiit ci taxawaay ba, ak ngir yërëm xeetam wi.
An-Nawawii nee na: sopp nañu déglu jàngu Alxuraan ak teewlu ko ak di jooy ak di ko settantal, sopp nañu itam sàkku ci keneen mu jàng ngir ñu déglu ko, te mooy li gën a jotale ci dégg ko ak settantal ko ci nga jàngal ko jsa bopp.
Déglu Alxuraan dafa am yool kem ni ko njàng mi ame.
Ngëneelu Abdulla ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm, ba tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bëgg mu dégtal ko Alxuraan ci gémmiñam, te lii day tegtale xérug ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm ci sàkku Alxuraan ak mokkal ko ak xereñe ko.
Ngëneelu jooy ngir ragal Yàlla mu màgg mi bu ñuy déglu aayaam yi, ànd ak noppi, ak rafetug xerawlu, ak bañ a yuuxu.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 196) (5050).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 551) (800).
Yataal gi (8)
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (7/ 133).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 515).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 402).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (3/ 342).