«bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man, ndax ku julli ci man genn julli Yàlla julli ci moom fukk, te ngeen ñaanal ma Wasiila ba, ndax moom ab bérab la ca àjjana, te kenn yayoowu ko ku dul ab jaam ci jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, ku ma ñaanal Wasiila samag ramm dagan na ko».
«إِذَا سَمِعْتُمُ الْمُؤَذِّنَ فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ، ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ، لَا تَنْبَغِي إِلَّا لِعَبْدٍ مِنْ عِبَادِ اللهِ، وَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ أَنَا هُوَ، فَمَنْ سَأَلَ لِيَ الْوَسِيلَةَ حَلَّتْ لَهُ الشَّفَاعَةُ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tegtal kiy dégg kiy nodd ñeel julli gi muy bàmtu ci ginnaawam, di wax lu mel ni li muy wax, bamu des ci ñaari Hàyyahala yi, ndax day wax ci séen ginnaaw: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, daal di julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ginnaaw bu nodd gi jeexee, ndax ku julli ci moom genn julli Yàlla dana julli ci moom ci sababus loolu fukki julli, maanaam jullig Yàlla ci jaam bi nag mooy: muy tagg jaam bi fa Malaaka ya. Mu digle ñu ñaanal ko Yàlla Wasiila -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te moom ag daraja la ca àjjana, te moo ca gën a kawe, te daraja jooju du yéwén mbaa muy yomb lu dul ñeel benn jaam ci mbooleem jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax loolu ngir toroxlu; ndaxte bu fekkee ne daraja ju kawe jooju, kenn rekk moo koy am, kon kenn kooku du nekk ku dul moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndax moom moo gën ci mbindéef yi. Yonnente bi leeral ne ku ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ag rammam dana ko jot -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
...:
Ñaaxe ci tontu noddkat bi.
Ngëneelu julli ci Yonnente bi ginnaaw buñu tontoo noddkat bi ba noppi.
Ñaaxe ci ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ginnaaw buñu jullee ci moom ba noppi.
Leeral maanaam Wasiila ak mbiram mu kawe, ba tax du yéwén lu dul ñeel kenn rekk.
Leeral ngëneelu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax ñu jagleel ko daraja ju kawe jooju.
Ku ñaan Yàlla Wasiila ñeel Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kooku ramm ma dagan na ko.
Leeral toroxlug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax muy sàkku ci xeetam wi ñu ñaanal ko daraja jooju, ànd ak loolu moo koy moom.
Yaatug ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem, benn bu baax fukk yu mel ni moom mooy ag payam.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 288) (384).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (9/ 111 (9/ 109).
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (2/ 13).
Cited in books
20 BooksYataal gi (20)
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الأول)«مَن صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»
- الخطب المنبرية موسوعة الخطب المنبرية (القسم الثاني)«مَنْ صَلَّىٰ عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الثالث)«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الثالث)«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"من صلى عليَّ صلاة صلى الله عليه بها عشراً" .
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«إِذَا سَمِعْتُمُ الْمُؤَذِّنَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى الله عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ، لَا تَ
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«إِذَا سَمِعْتُمُ الْمُؤَذِّنَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى الله عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ، لَا تَ
- المختصر المفيد للمؤذن والإمام والخطيب وأحكام المساجد«إِذَا سَمِعْتُمْ المُؤَذِّنَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ، ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ؛ فَإِنَّهُ مَن صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُّوا اللَّهَ لِيَ الوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنزِلَةٌ فِي الجَنَّةِ، لَا
- المختصر المفيد للمسلم(من صلى عليّ صلاة صلى الله عليه بها عشرا)
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“إذا سمعتم المؤذن فقولوا مثل ما يقول، ثم صلوا عليّ، فإنه من صلى عليّ صلاة صلى الله عليه بها عشرا، ثم سلوا الله لي الوسيلة؛ فإنها منزلة في الجنة، لا تنبغي إلا لعبد من عباد الله، وأرجو أن أكون أنا هو، فمن سأل لي الوسيلة حلت له الشفاعة”.
- تحفة الأخيار تحفة الأخيار (ببيان جملة نافعة مما ورد في الكتاب والسنة من الأدعية والأذكار)«إِذَا سَمِعْتُمُ الْمُؤَذِّنَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى الله عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ، لَا تَ
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»[265].
- رسالة في الأذكار1«إِذَا سَمِعْتُمُ المُؤَذِّنَ فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ، ثُمَّ صَلُّوا عَلَيّ؛ فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ؛ فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الجَنَّةِ لَا تَنْبَ
- رسالة في الأذكار1«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 5«إذا سَمِعْتُمُ المُؤَذِّنَ فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ، ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإنَّهُ مَنْ صلَّىٰ عَلَيَّ صلاةً صَلَّىٰ اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْراً، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإنَّهَا مَنْزِلَةٌ في الجَنَّةِ لا تَنْبَغِي إ
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 7«مَنْ صلَّىٰ عليَّ صلاةً صلَّىٰ اللهُ عليه بها عَشْراً».
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)2«من صلى عليَّ صلاةً صلّى الله عليه بها عشرًا».
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)مجموعة زاد الفقه (1)«إِذَا سَمِعْتُمْ الْمُؤَذِّنَ فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى الله عَلَيْهِ بِهَا عَشْراً، ثُمَّ سَلُوا الله لِي الْوَسِيلَةَ فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ لَا تَنْبَغ
- مشروع منهاج زادكزادك 3 طالب نهائي«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»
- نبراس طالب (1)1«مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا»