"waxal: yaw Yàlla Sunu Boroom nanga ma fegale say mbir yu dagan ci yu araam yi, te nga def ma ma doylu ci ku dul yaw".
Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne benn jaam bu bindantee ak sangam dafa ñëw ci moom ne ko: man de li ma bindante dama ci a néew doole dimbali ma ci, mu ne ko: mo ndax duma la xamal ay baat yoo xam ne Yonente Yàlla bi moo ma ko xamal, te boo amoon ay bor yu toll ni montaañu Siir kon Yàlla dana la ko fayal, da fa wax ne:
"waxal: yaw Yàlla Sunu Boroom nanga ma fegale say mbir yu dagan ci yu araam yi, te nga def ma ma doylu ci ku dul yaw".
«قُلْ: اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلاَلِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ».
Benn jaam dafa ñëw ci njiitu jullit ñi Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm fekk dafa bindante ak sangam dëppoo ak moom ci mu jënn boppam goreel ko, ngir mu mujj nekk gor, te amul alal, mu ne ko: Man de damaa néew doole ci fay li ma war, kon dimbali ma ci alal fayal ma ko, walla ci jàngale ak jubbanti, njiitu jullit ñi ne ko: Ndax duma la xamal ay baat yoo xam ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ma ko xamal, te bu ameeloon ngiiru Tàyy ay bor yu toll ni montaañu Siir kon Yàlla dana la ko fayal seen boroom, musal la ci gàccaam, dafa wax ne: waxal: yaw Yàlla Sunu Boroom fegal ma te wëlbati ma te soreele ma yu araam yi, te nga def ma ma doylu nga fegal ma ci sa ngëneel yi ak sa tabe gi wolif ku dul yaw ci mbindeef yi.
Diisoo ak sàkku gis-gisu boroom xam-xam ak diine.
War na ci boroom xam-xam yi ak wootekat yi ci Yàlla mu kawe mi ñuy leeralal ñi ñuy woo di leen gindi jëme leen ci lu leen di dimbali ci li leen di gaar ci ay jafe-jafe.
Ñaaxe ci dimbali jaam bi bindante ak sangam.
Ñaaxe ci jàng ñaan gii, ak di ko ñaan Yàlla.
Wërsëg wu dagan donte dafa néew moo gën alal ju araam donte dafa bari
Doyloo Yàlla wolif mbindeef yi.
Ñaaxe ci delloo aji-laaj ji delloo gu rafet bu dee amoo loo ko jox.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 526) (3563).
Yataal gi (9)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (2/ 565).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (2/ 1013).
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (17/ 456).
فيض القدير شرح الجامع الصغير.
للمناوي (3/ 111).
النهاية في غريب الحديث والأثر (3/ 9).
Cited in books
11 BooksYataal gi (11)
- أدعية جامعةأدعية جامعة (للحرمين)53. «اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ».
- التحقيق والإيضاح لكثير من مسائل الحج والعمرة والزيارة على ضوء الكتاب والسنةالتحقيق والإيضاح لكثير من مسائل الحج والعمرة والزيارة - النسخة المعتمدة* اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ[71].
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"اللهم اكفني بحلالك عن حرامك، واغنني بفضلك عن سواك".
- المختصر في آداب السفر وصفة الحج والعمرة وآداب الزيارة والأدعية الجامعة مع ملحق بالفتاوى والمخالفات4- أدعية جامعة (للحرمين)«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ».
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكِ عَمَّنْ سِوَاكَ»[177].
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلماللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكِ عَمَّنْ سِوَاك
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 7«اللهم اكْفِنِي بحلالك عَنْ حرامِكَ، وأغْنِنِي بفضِلكَ عمَّنْ سواكَ».
- قاموس الكبائر موسوعة الكبائر - المجموعة الأولى«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ» [94].
- قاموس الكبائر موسوعة الكبائر - المجموعة الأولى«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ» [115].
- قاموس الكبائر«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ» [94].
- قاموس الكبائر«اللَّهُمَّ اكْفِنِي بِحَلَالِكَ عَنْ حَرَامِكَ، وَأَغْنِنِي بِفَضْلِكَ عَمَّنْ سِوَاكَ» [115].