"buleen mbugale mbugaliinj Yàlla"
Jële nañu ci Ikrimata mu wax ne:
Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa lakk ay nit, loolu egg ci ibn Abbaas, mu ne: bu doon man duma leen lakk ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "buleen mbugale mbugaliinj Yàlla", waaye dama leen di ray kem ni ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waxe: "ku soppi diineem rayleen ko".
أَنَّ عَلِيًّا رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ حَرَّقَ قَوْمًا، فَبَلَغَ ابْنَ عَبَّاسٍ فَقَالَ: لَوْ كُنْتُ أَنَا لَمْ أُحَرِّقْهُمْ لِأَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «لاَ تُعَذِّبُوا بِعَذَابِ اللَّهِ»، وَلَقَتَلْتُهُمْ كَمَا قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَنْ بَدَّلَ دِينَهُ فَاقْتُلُوهُ».
Aliyun ibn Abii Taalib dafa góor-góorlu daal di lakk ay nit yu bokk ci yàwkati fiine yi tubbi génn ci lislaam, loolu egg ci Abdulla ibn Abbaas yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu dëgëral ko ci ray gi mu leen ray; waaye mu mu weddi ray gi mu leen ray ci sawara. Mu wax ne: bu ma nekkoon bérabam du ma leen lakk; ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne kenn du mbugal ci sawara ku dul Boroom sawara, waaye ray leen rekk doyoon na, ndax li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: ku tubbi ci lislaam soppi diineem dem ci jeneen diine rayleen ko.
Dañoo war a ray ku tubbi ci lislaam ci dëppoog woroom xam-xam yi, te loolu mooy bu ay sàrtam dajee, kenn du def loolu nag ku dul imaam bi ak àttekat bi
Li mu wax: "ku soppi diineem, rayleen ko" maanaam ku tubbi ci lislaam: àtte bu matale la ñeel góor ñi ak jigéen ñi.
Aji-tubbi ji deesu ko saxalloo ag tubbrem waaye dañu koy woo ci lislaam, bu wuyuwul ñu ray ko
Nekk ci hadiis bi tere ñuy mbugale ci sawara, ak ne daan yi deesu ko amale ci sawara.
Ngëneelu ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm, ak yaatug xam-xamam ak ug déggam hadiisi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Nekk na ci it tegginu weddi ki wuute ak yaw.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 61) (3017).
Yataal gi (14)
عمدة القاري شرح صحيح البخاري.
لبدر الدين العيني (14/ 264).
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (8/ 364).
توضيح الأحكام شرح بلوغ المرام.
لعبد الله البسام (6/ 204).
فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (5/ 218).
الإفصاح عن معاني الصحاح.
لابن هبيرة (3/ 190).
التوضيح لشرح الجامع الصحيح.
لابن الملقن (18/ 58).
نيل الأوطار.
للشوكاني (7/ 225).
Cited in books
5 BooksYataal gi (5)
- الإسلام دين كامل«مَنْ بَدَّلَ دِينَهُ فَاقْتُلُوهُ» [2]،
- التسليم للنص الشرعي والمعارضات الفكرية المعاصرة06 التسليم للنص الشرعي - من المبحث الثالث الفصل الرابع حتى الفصل الخامس"من بدل دينه فاقتلوه"
- التسليم للنص الشرعي والمعارضات الفكرية المعاصرة06 التسليم للنص الشرعي - من المبحث الثالث الفصل الرابع حتى الفصل الخامس"لا تعذبوا بعذاب الله"
- حكم المستهزئين بالأنبياء والمرسلين«مَنْ بَدَّلَ دِينَهُ فَاقْتُلُوهُ»[3].
- عقيدة التوحيدعقيدة التوحيد وبيان ما يضادها...«مَنْ بَدَّلَ دِينَهُ فَاقْتُلُوهُ»[61].