Skip to content

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan dugg ci wanag day wax: «Allaahumma innii ahuusu bika minal xubusi wal xabaa-isi».

Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan dugg ci wanag day wax: «Allaahumma innii ahuusu bika minal xubusi wal xabaa-isi».

كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا دَخَلَ الخَلاَءَ قَالَ: «اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنَ الخُبُثِ وَالخَبَائِثِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan namm a dugg ci barab bu muy faje aajo, saw mbaa ginnaaw kër, day muslu ci Yàlla, làqatu ci moom ngir mu musal ko ci ayu Saytaane yu góor yi ak yu jigéen yi. Firee nañu xubus ak xabaaisi ba tay ci aw ay ak ci ay sobe.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu ñaan gii bu ñuy dugg ci wanag.

Mbindeef yépp a aajowoo seen Boroom ci jañ lépp lu leen di lor ci gépp anam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 40) (142).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 283) (375).

Yataal gi (4)

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (1/ 23).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

للبسام (ص36).