Skip to content

"ku jàngul faatiha amul julli".

Jële na ñu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

"ku jàngul faatiha amul julli".

«لَا صَلَاةَ لِمَنْ لَمْ يَقْرَأْ بِفَاتِحَةِ الكِتَابِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne julli du wér lu dul ci jàng saaru Faatiha, ndaxte ponk la ci ponki julli ci ràkka yépp.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Faatiha leneen manukoo wuutu ci ku ko man.

Ràkka bu ñu jàngul faatiha day yàqu, ci ki ko tay, ak ki xamul, ak ki fàtte; ndaxte ponk la, te ponk du rot ba mukk.

Jàng faatiha dana wàcci maamuum bi ji bu dabee imaam bi cib rukkoo.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 151) (756).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 295) (394).

Yataal gi (4)

تيسير العلام.

للبسام (ص171).

تنبيه الأفهام.

لابن عثيمين (217).