Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

55 of 732 cards

Clear filters
«bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
"ku def dara ba ab gétéñ war ca ñu gaaw koo mbugal ci àdduna, Yàlla moo gën a maanu ba du mbugalaat jaamam bi ca allaaxira, waaye ku def luy waral ab gétéñ Yàlla suturaal ko jéggal ko, Yàlla moo gën a tedd ba du delluwaat ci dara lu mu jéggale woon".
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
"seen Boroom de Ku bari kersa la ku tedd la, dana kersawu ci jaam bi bu yëkkëtee loxoom jëme ci moom mu koy ba ña jox".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja.
«amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo».
Ag càllalaam tane na Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat.
«Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja.
Dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla mu baarkeel mi te kawe nee na: éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale, yaw doomu Aadama say bàkkaar bu eggoon ca niiri asamaan si nga jéggalu ma kon dinaa la jéggal te duma faale dara, yaw doomu Aadama boo ma indiloon luy jege suuf si ci bàkkaar yu bari, nga daje ak man te bokkaalewóo ma ak dara dinaa la indil njéggal lu toll ni moom".
Tane na At-tirmisiy soloo na ko.
Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la.
Hadiis bu rafet la ci mbooleem yoon yi mu jaar Abuu Daawuda ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ñoo ko soloo
"bu kenn ci yéen eggee cib jotaay na nuyóo, bu nammee jug na nuyóo, ndax bu njëkk bi gënut a yay bu mujj bi".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat.