«Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
Jële nañu ci Sadaan Ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: mokkal naa yaari mbir ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi».
«إِنَّ اللهَ كَتَبَ الْإِحْسَانَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ، فَإِذَا قَتَلْتُمْ فَأَحْسِنُوا الْقِتْلَةَ، وَإِذَا ذَبَحْتُمْ فَأَحْسِنُوا الذَّبْحَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، فَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ».
Yónente bi xamle na ne Yàlla mu kawe mi dafa waral si nun rafetal ci lépp, te rafetal mooy: di fuglu Yàlla ba fàwwu, ci jaamu gi ak ci def yiw ak ci fegal mbindeef yi lor, bokk na ci loolu di rafetal cig ray ak cig rendi. Rafetal cig ray ci jamonoy fayontoo: ci tànn yoon wa gën a yomb te gën a woyof te gën a gaaw ci faat ki ñuy ray. Rafetal cig rendi mooy: mu am ñeewantu ci bayima bi mu ñawal jumtukaay bi, te bañ koo daas ci kanamu la muy rendi, fekk ma nga koy xool, te mu bañ koo rendi fekk am na fa ay jur yu koy xool.
الشفرة: السكين العريضة.
Yërmàndeg Yàlla mu kawe ak ñeewantoom ci mbindeef yi
Rafetal ray gi ak rendi gi ci defe ko ca anam ga ñu ko yoonale.
Matug Sariiha ak làmboo gimu làmboo léppi yiw, bokk na ca yërëm rab yi ak ñeewantu leen.
Tere di ñaawal yaramu nit ki ginnaaw bi ñu ko rayee.
Araamug lépp loo xam ne mbugal baayima da caa nekk.
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1548) (1955).
Yataal gi (8)
التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثا النووية (ص38).
شرح الأربعين النووية.
لابن عثيمين (ص185).
فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.
للعباد (ص65).
فتح الباري.
لابن حجر (9/ 644).
شرح النووي على مسلم (13/ 107).
Cited in books
5 BooksYataal gi (4)
- أحكام الهدي والأضاحي والتذكيةأحكام الهدي والأضاحي والتذكية «إِنَّ اللَّهَ كَتَبَ الْإِحْسَانَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ، فَإِذَا قَتَلْتُمْ فَأَحْسِنُوا الْقِتْلَةَ، وَإِذَا ذَبَحْتُمْ فَأَحْسِنُوا الذَّبْحَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، فَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ» [8].
- الحديث زاد 4الحديث 4«إِنَّ الله كَتَبَ الإِحْسانَ على كُلِّ شَيْءٍ، فَإِذا قَتَلْتُمْ فَأَحْسِنُوا القِتْلَةَ، وَإِذا ذَبَحْتُمْ فَأَحْسِنُوا الذَّبْحَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، وَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ».
- رسالة موجزة عن الإسلام كما جاء في القرآن الكريم والسنة النبوية (مشتملة على الأدلة)رِسَالَةٌُ مُوجَزَةٌُ عَنِ الْإِسْلَامِ كَمَا جَاءَ فِي الْقُرْآنِ الْكَرِيمِ وَالسَّنَةِ النَّبَوِيَّة-مشتملة على الأدلة -للحرمين-«إنَّ اللَّهَ كَتَبَ الإحْسَانَ علَى كُلِّ شيءٍ، فَإِذَا قَتَلْتُمْ فأحْسِنُوا القِتْلَةَ، وإذَا ذَبَحْتُمْ فأحْسِنُوا الذَّبْحَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، فَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ» [39].
- نبراس طالب (2)نبراس طالب (2) «إِنَّ اللهَ كَتَبَ الْإِحْسَانَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ، فَإِذَا قَتَلْتُمْ فَأَحْسِنُوا الْقِتْلَةَ، وَإِذَا ذَبَحْتُمْ فَأَحْسِنُوا الذَّبْحَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، وَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ»