"aji-gëm du deñ di nekk ci yaatug diineem, fii ak laalul dereet ju araam".
Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"aji-gëm du deñ di nekk ci yaatug diineem, fii ak laalul dereet ju araam".
«لَنْ يَزَالَ المُؤْمِنُ فِي فُسْحَةٍ مِنْ دِينِهِ، مَا لَمْ يُصِبْ دَمًا حَرَامًا».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne jullit bi du deñ di nekk ci yaatug ay jëfam yi baax, ak yaakaar yërmàndey Yàlla ak njéggalam ak baalam, ba bu demee ba ray nit ku ñu araamal ñu ray ko kon ay jëfam daal di xat, ndaxte du fay mukk ñaawteefu ray gi ak bàkkaaram yu rëy.
Màggayu ray ci lu dul dëgg ak ray ci ag tay, ndax day génne jullit bi ci yaatug diineem jëme ko ci ag xat.
Dereet yu araam yi ñenti xaaj la: 1- dereetu jullit, te moo ci gën a màgg, 2- dereetu yéefar bi dëkk ci jullit ñi, te mooy Yahuud bi ak Nasaraan bi nga xam ne da fa sax ca diineem te nekk ci dëkku lislaam te taqoo joxe lempo, àttey lislaam yi di wéy ci moom, 3- dereetu yéefar bi nu kóllaranteel, te ñooy yéefar yi nekk ca seen réew te sunu diggante ak ñoom am ug yéwénoo duñu leen xeex te ñoom duñu nu xeex, 4- dereetu yéefar bi ñu ñoŋal, te mooy yéefar biy aji-xeex ak dëkkandoo walla kóllare doxul sunu diggante, waaye dañu ko a ñoŋal ci waxtu wu ñu tënk mu ciy dugg ci dëkku jullit ñi ci ndigalul njiitu jullit ñi, walla ku jagoo loolu ci ñi ko wuutu.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (9/ 2) (6862).
Yataal gi (2)
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (10/ 41).
تطريز رياض الصالحين (ص: 171).