"bu doon benn waay dafaa namma def ag ndëngte fekk moo nga ca Hadan ci soriwaay kon Yàlla dana ko mosal mbugal mu metti".
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu askanale Yonente bi ne:
Ci li Yàlla wax ne: {ku fa namm ag ndëngte ci ag tooñ dananu ko mosal mbugal mu metti} [Al-Hajj: 25] nee na: "bu doon benn waay dafaa namma def ag ndëngte fekk moo nga ca Hadan ci soriwaay kon Yàlla dana ko mosal mbugal mu metti".
فِي قَوْلِ اللَّهِ عَزَّ وَجَلَّ: {وَمَنْ يُرِدْ فِيهِ بِإِلْحَادٍ بِظُلْمٍ نُذِقْهُ مِنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ} [الحج: 25] قَالَ: «لَوْ أَنَّ رَجُلًا هَمَّ فِيهِ بِإِلْحَادٍ وَهُوَ بِعَدَنِ أَبْيَنَ لَأَذَاقَهُ اللَّهُ عَذَابًا أَلِيمًا».
Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax ci li Yàlla wax ne: {ku fa namm ag ndëngte ci ag tooñ dananu ko mosal mbugal mu metti} [Al-Hajj: 25], nee na: bu kenn ci nit ñi xalaatoon daal di dogu ci def ca Haramu Màkka ba jëf ju ñaaw juy xotti warmay Haram bi ci li Yàlla araamal ci wax walla ray te tay ko ci ag tooñ, donte ma nga nammee loo lu ca dëkk bu ñu naan Hadan ca Yaman kon kooku yeyoo na Yàlla teg ko mbugal mu metti ngir loolu, donte defu ko, doy na ca rekk mu dogu ci def ko.
Leeral jagle yi Haram bi am ak màggal ko.
Sahdii nee na: nekk na ci aaya bu tedd bii, ne war na ñu wormaal Haram bi, ak tarug màggaayam, ak artu ci namm faa def Ag moy ak def ko fa.
Dahhaak nee naa: nit ki dana yittewoo ag moy ci Màkka fekk moo nga ca beneen suuf ñu bindal ko loolu donte defu ko.
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (7/ 155) (4071).
1012.
597).
Yataal gi (4)
المستدرك على الصحيحين للحاكم (2/ 420) (3461).
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (10/ 52).
جامع العلوم والحكم (2/ 327).
النهاية في غريب الحديث والأثر ( ص 829.