Skip to content

Ñatti waxtu yii Yonente bi da nu daan tere nu julli ci, walla ñu suul ci sunuy néew

Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir Al-Juhanii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Ñatti waxtu yii Yonente bi da nu daan tere nu julli ci, walla ñu suul ci sunuy néew: bu Jant bi dee fenk ba keroog muy yëkkëtiku, ak bu digg njolloor bi taxawee ba keroog Jant bi di jeng, ak bu Jant bi jëmee ci so ba keroog muy so.

ثَلَاثُ سَاعَاتٍ كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَنْهَانَا أَنْ نُصَلِّيَ فِيهِنَّ، أَوْ أَنْ نَقْبُرَ فِيهِنَّ مَوْتَانَا: حِينَ تَطْلُعُ الشَّمْسُ بَازِغَةً حَتَّى تَرْتَفِعَ، وَحِينَ يَقُومُ قَائِمُ الظَّهِيرَةِ حَتَّى تَمِيلَ الشَّمْسُ، وَحِينَ تَضَيَّفُ الشَّمْسُ لِلْغُرُوبِ حَتَّى تَغْرُبَ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere ñuy julli jullig coobare, walla ñuy suul néew yi ci ñatti waxtu yii ci bëccëg gi: Waxtu wu njëkk wi: bu Jant bi dee fenk, te mooy bu dee tàmbalee fenk ba keroog muy yëkkëtiku luy tollook ab xeej, ño koy nattale ci ñenteelu xaaju waxtu. Ñaareel bi: bu Jant bi nekkee ci digg asamaan si, nga xam ne du am ker ci booru penku bi walla ci sowu bi ba keroog muy jóge ci digg asamaan si, ker gi génn ci booru penku bi, foofu la waxtuw jullig Tisbaar di tàmbalee, te waxtu wu gàtt la; dees na ko nattale ci fukk ak juróomi simili. Ñatteel bi: bu jant bi jengee di waaj a soh ba keroog muy soh.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Waxtu yi ñuy tere ñu julli ci kem ni ko hadiis bi ak yeneen hadiis leerale mooy: bi ci njëkk: ginnaaw jullig Fajar ba baa Jant bi di fenk, ñaareel bi: bu Jant bi dee fenk ba keroog muy yëkkëtiku luy tollook xeej ci gisu bët; maanaam luy toll ci fukk ak juróomi simili, ñatteel bi: bu aji-taxaw ji ci njolloor gi taxawee ba keroog Jant bi di deñ, te loolu mooy bu demee ba aji-taxaw ji ci njolloor gi amatul ker ci penku du caagine it ci sowu bi, ñenn ñi ñi ngi ko nattale ci fukk ak juróomi simili, ñenteel bi: ginnaaw jullig Tàkkusaan ba keroog Jant bi di soh, juróomeel bi: bu Jant bi mboqee ba baa muy soh.

juróomi waxtu yii ñu tere ku ci julli, dees na ci settee jullig farata ak julli gu am sabab.

Tere nañu di yeex a suul ab néew ba ñatti waxtu yu xat yii ñu tudd ci hadiis bi jot, dana dagan nag yeneen waxtu yépp ci guddi walla bëccëg.

Xereñte gi nekk ci tere gi ñi tere julli ci waxtu yii: lay cosaan mooy jullit bi day wommatu ñeel ndigali Yàlla yi, tay moytu ay tereem ngir jaamu Yàlla, waaye du baña def ag jaamu Yàlla ngir ne xamul yilla ji walla sabab bi tax ñu digle ko, mbaa ñu tere ko, waaye li ko war mooy mu wommatu, yeneen hadiis ñëw leeral na xereñte gi nekk ci loolu: bi ci njëkk: waxtuw njolloor laata Jant bi di jeng dañu ciy xamb Jahannama xamb gu tar, ñaareel bi: xereñte gi nekk ci tere gi ñu tere julli bu Jant bi dee fenk ak bu dee soh, mooy ne dafa niróok bokkaalekat yi, ndax ñoom dañuy sujjóotal Jant bi bu dee fenk ak bu dee soh, ñatteel bi: bu dee li ñu tere julli ginnaaw bu ñu jullee fajar ba keroog Jant bi di fenk, ak ginnaaw bi ñu jullee Tàkkusaan ba kerroog Jant bi di soh, loolu ci buntub fatt yoon yiy jëme ci lu baaxul; ndax day dog niróowaale ak yéefar yi, ba jullit du leen niru ci seen bokkaale gi, ndax ñoom dañuy sujjóotal Jant bi buy fenk ak bu dee soh.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 568) (831).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (1/ 488).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (1/ 438).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (2/ 202).

سبل السلام.

لمحمد الصنعاني (1/ 167).