Skip to content

" caabiy kumpa yi juróom la

Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

" caabiy kumpa yi juróom la, {Yàlla rekk a xam kañ la àdduna di tukki, mooy wàcce taw bi, te moo xam li nekk ci butiitu njurukaay yi,te amul kenn ku xam lu muy fàggu suba, te kenn xamul ci san suuf lay faatoo, Yàlla ku deñ kumpa la waaye ku xereñ la}"

«مَفَاتِحُ الغَيْبِ خَمْسٌ، {إِنَّ اللَّهَ عِنْدَهُ عِلْمُ السَّاعَةِ وَيُنْزِلُ الغَيْثَ وَيَعْلَمُ مَا فِي الأَرْحَامِ وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ مَاذَا تَكْسِبُ غَدًا وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ بِأَيِّ أَرْضٍ تَمُوتُ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ خَبِيرٌ}».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Kumpa fa Yàlla la nekk kenn xamu ko ku dul moom, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne caabiy kumpa yi ak ay kopparfooram juróom la: Bi ci njëkk: kenn xamul kañ la àdduna di tukki ku dul Yàlla, ag junj la ci xam-xamu bis bu mujj ba, ndax bis-pénc mooy njëlbeenam, kon bu dàqee xam-xam ba gën a jege kon xam-xam ba gën a jege dàqu na. Ñaareel bi: kenn xamul kañ la taw bi di ñëw ku dul Yàlla, ag junj la ci mbiri dënnu ba ca kaw, mu jagleel taw bi ci ag tudd ànd ak ne amna ay sabab yoy amaana mu tegtale ci ni aada di doxe ag wàccam waaye ci lu dul dëgg-dëgg ak ug wóolu. Ñatteel bi; liy nekk ci butiti njurukaay yi; muu góor walla jigéen, muy njuul walla weex, mu mat walla mu màkki, muy texeedi walla muy texe ak yu ko niru, mu jagleel butiti njurukaay ci ag tudd ndax ñi bari dañu koy xam ci aada, ànd ak loolu mu dàq ñu kenn xam dëgg-dëggam kon lu dul moom moo gën a yey. Ñenteel bi: kenn xamul luy am suba ku dul Yàlla, ag junj la ci xeeti jamono yi ak li ci nekk ci ay xew-xew, mu tudd baatub "suba" ngir dëgg-dëggam nekk li gën a jege ci jamono yi, bu fekkee ànd ak nii mu jegee kenn xamul dëgg-dëgg la cay am, ànd ak ne man naa am màndarga ak kon la ca ginnaawam moo gën a yey. Juróomeel bi: kenn xamul ci san suuf laa faatoo, af junj la ci mbiri dënn suuf si, ànd ak ne aaday nit ñi ëpp mooy ne dañuu faatoo seen réer waaye loolu du dëgg-dëgg, ndax bu faatoo woon ci réewam sax du xam ci ban pakk lañu koy suul, doonte dafa am bàmmeeli ay maamam, {Yàlla Aji-Xam la Aji-Xereñ la} ku peeg la yi feeñ ak yi nëbbu, ak yi làqu, sekkare yi, mu boole ci aaya bi xeeti kumpa yi, mu dindi mbooleem wootewoo yu yàqu yi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral kopparfoori kumpa yi nga xam ne kenn xamu ko ku dul Yàlla.

As-Sindii nee na: li mu wax: (caabiy kumpa yi juróom la), tudde nañu juróom yii: caabiy kumpa yi; ndaxte ku xam juróom yii xam na kumpa yépp; mu mel ni dafa mujj nekk lu ñuy ubbee kopparfoori kumpa yi.

Ibn Hajar nee na: Ibn Abii Jamrata nee na: dafa tudd ay caabi ngir jegeele mbir mi ci aji-dégg ji; ndax lépp lu am kiiraay sa diggante ak moom loolu fàddu na ci yaw, te lay jëm ci xam ko ci aada mooy bunt bi, te bu ñu tëjee bunt bi dañuy aajowoo caabi bi, te bu dee mbir mi nga xam ne deesul gis kumpa gi lu dul ag eggaleem xamuñu bérabam kon naka lañuy xame la fàddu.

Ibn Abii Jamrata nee na: xereñte gi nek ci ñu def ko juróom mooy junj ci tënk dënn yi ci yooyu.

Amaana Yàlla mu màgg mi feeñalal Yonnente yi kumpa ngir ag xereñteem moom Aji-Sell ji.

Yàq defeg biddiwkat yi ak Gisaanekat yi ci li ñuy jëfandikoo xam-xamu kumpa, ak ne ku wootewoo dara ci li Yàlla Sell mi jagoo xam gi, kooku weddi na Yàlla mu kawe mi ak Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Alxuraan ju màgg ji.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 56) (4627).

Yataal gi (1)

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (7/ 118).