Skip to content

«Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne:

«Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira, bu dee ab yéefér nag ay jëfam yu baax yi mu def ngir Yàlla fii ci àdduna, dañu ka koy dundale, ba bu demee allaaxira, du fa fekk jenn jëf ju baax buñu koy fay».

«إِنَّ اللهَ لَا يَظْلِمُ مُؤْمِنًا حَسَنَةً، يُعْطَى بِهَا فِي الدُّنْيَا وَيُجْزَى بِهَا فِي الْآخِرَةِ، وَأَمَّا الْكَافِرُ فَيُطْعَمُ بِحَسَنَاتِ مَا عَمِلَ بِهَا لِلَّهِ فِي الدُّنْيَا، حَتَّى إِذَا أَفْضَى إِلَى الْآخِرَةِ، لَمْ تَكُنْ لَهُ حَسَنَةٌ يُجْزَى بِهَا».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral màggug ngëneelu Yàlla ci way-gëm ñi, ak màndoom ci yéefar yi. Aji-gëm ji deesul wàññi ci yooli jëfam ju baax; waaye dees koy jox fii ci àdduna ci yiw ci ay jaamoom, ànd ak loolu ñu dencal ko payam ca allaaxira; amaana it ñu dencal ko payam gépp ba allaaxira. Bu dee ab yéefar nag Yàlla da koy jox payug li mu def ci yu baax fii ci àdduna, ba bu demee allaaxira du fa fekk am lenn lu baax lu ñu koy fay; ndaxte jëf yu baax yiy jariñ ci ñaari kër yi fàwwu boroomam nekk aji-gëm.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ku faatu cig kéefar jëfam du ko jariñ.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2162) (2808).

Yataal gi (3)

المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (1/ 460).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (43/ 460).

شرح النووي على مسلم (17/150).