Skip to content

«àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:

«àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».

«حَقُّ الْمُسْلِمِ عَلَى الْمُسْلِمِ خَمْسٌ: رَدُّ السَّلَامِ، وَعِيَادَةُ الْمَرِيضِ، وَاتِّبَاعُ الْجَنَائِزِ، وَإِجَابَةُ الدَّعْوَةِ، وَتَشْمِيتُ الْعَاطِسِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yénn àqi jullit bi ci mbokku jullitam, Bi njëkk ci àq yii mooy delloo nuyoo ñeel ku la nuyu. Àqu ñaareel bi: seeti ku feebar. Àqu ñatteel bi: gunge ab néew ci këram ba ca jullikaay ba, ba ca almeer ya ba ba ñu koy rob. Àqu ñenteel bi: wuyu woote ba bu ñu ko woowee ci céetal ab séet mba leneen. Àqu jurómeel bi: ndokkeel Ku tissooli, te mooy mu wax ko ndeem sant na Yàlla: yarhamulallaah, aji-tissooli ji wax: yahdiikumullaahu wa yuslihu baalakum.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Màggug Lislaam ci di feddali àq yi dox diggante jullit ñi, ak di dëgëral mbokkoo ak bëggante seen diggante.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 71) (1240).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1704) (2162).

Yataal gi (10)

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (4/ 512).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 327).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

مجموعة من الباحثين (1/ 253).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 591).

بهجة قلوب الأبرار.

لابن سعدي (ص81).