Skip to content

"kenn ku fekke Badar ak Al-Hudaybiya du dugg Sawara".

Jële nañu ci Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"kenn ku fekke Badar ak Al-Hudaybiya du dugg Sawara".

«لن يدخلَ النارَ رجلٌ شَهِد بدرًا والحُدَيْبِيَة».

Ahmad moo ko soloo, te cosaan li ma nga ca Sahiihu Muslim.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku teewe Badar gi amoon ci atum ñaareel mi ci gàddaay gi ànd ak Yonente bi doon xeex kooku du dugg Sawara, ak it ku teewe woon sulhu Hudaybiya, te ca la jaayante ga nu gërëm ame woon mu nekkoon ci atum juróom-benneel gi ci gàddaay gi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu waa Badar ak Al-Hudaybiya, ak ne ñoom duñu dugg Sawara mukk.

Leeral ne Yàlla dana leen tëyéel tooñange yi, te dana leen dëppale ci ñu faatu ci ngëm, te it dana leen dugal Àjjana te mbugalum Sawara du ko jiitu, loolu nag ngëneelu Yàlla la moo koy jox ku ko soob, te Yàlla mooy boroom ngëneel yu màgg yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1942) (2495).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (23/ 410) (15262).

Yataal gi (6)

المصباح المنير في غريب الشرح الكبير.

لأحمد الفيومي (1/ 123).

فيض القدير شرح الجامع الصغير.

للمناوي (5/ 302).

المنهاج شرح صحيح مسلم بن الحجاج.

للنووي (16/ 57).