Skip to content

«Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba, waxuma nag {alif laam miim} aw araf la waaye alif araf la laam araf la miim araf la».

«مَنْ قَرَأَ حَرْفًا مِنْ كِتَابِ اللهِ فَلَهُ بِهِ حَسَنَةٌ، وَالْحَسَنَةُ بِعَشْرِ أَمْثَالِهَا، لَا أَقُولُ {الم} حَرْفٌ، وَلَكِنْ {أَلِفٌ} حَرْفٌ، وَ{لَامٌ} حَرْفٌ، وَ{مِيمٌ} حَرْفٌ».

At-tirmisiy soloo na ko.
Tane na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bépp jullit bu jàng wenn araf ci téereb Yàlla bi dana am benn yool , te dees na ko ful ba fukk yu mel ni moom. Mu leeral loolu ci waxam ji: (waxu ma ni nag alif laam miim benn araf la waaye alif araf la, laam araf la, miim araf la): mu nekk ñatt mu am ca fanweeri yiw.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaaxe ci di baril jàng Alxuraan.

Aji-jàng ji am na ci wépp araf ci baat bu mu jàng bu nekk yiw wu ñu ful ba fukk yu mel ni moom.

Yaatug yërmàndey Yàlla ak tedd-ngaam ba tax muy fulal jaam bi ab yool ngir ngëneelam ak teraangaam.

Ngëneelu Alxuraan ci jeneen wax ju dul moom, ak jaamu Yàlla ci jàng ko; ndaxte waxi Yàlla la.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 33) (2910).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 229).

سلسلة الأحاديث الصحيحة.

للألباني (7/ 970).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (4/ 655).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 742).