Skip to content

"nit ñi danañu bàyyi li ñuy ñàkk a teewe àjjuma yi walla Yàlla dana kaste seen xol yi, te danañu bokk ci way-sàggan yi".

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar ak Abuu Hurayrata yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ñoom dégg nañu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu nekk ca Minbar ba di wax naan:

"nit ñi danañu bàyyi li ñuy ñàkk a teewe àjjuma yi walla Yàlla dana kaste seen xol yi, te danañu bokk ci way-sàggan yi".

«لَيَنْتَهِيَنَّ أَقْوَامٌ عَنْ وَدْعِهِمُ الْجُمُعَاتِ أَوْ لَيَخْتِمَنَّ اللهُ عَلَى قُلُوبِهِمْ، ثُمَّ لَيَكُونُنَّ مِنَ الْغَافِلِينَ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day artu -fekk ma nga ca Minbar ba- ci bàyyi àjjuma ak di ko wuute ci lu dul ngànt, waaye ngir woyofal ko ak tàyyeel, walla kon Yàlla dana muur seen xol yi def ca kiiraay gu koy teree topp dëgg, topp danañu bokk ci way-sàggan yi ba duñu topp yiw, seen bakkan yi bañ jaamu Yàlla.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Taral ci wuute jullig Àjjuma, ak ne loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Nawawii nee na: nekk na ci it ne Àjjuma faratay jëmm la.

Yoonal nañu def Minbar bi xutbawukaay.

Sindii nee na: maanaa mi mooy ne fàww benn ci ñaari mbir yii am, benn ñu bàyyi ñàkk a teewe àjjuma gi walla Yàlla kaste seen xol yi, ndax tàmm a bàyyi àjjuma day def taq-taq ci xol bi, di bañloo bakkan topp Yàlla.

Jaadu na ci waarekat bi ak kiy fàttali mu baña tudd jëmm yi mu namm a waar; ndax loolu mooy gën a tax ñu nangu laabire gi, ak topp ndigal yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 591) (865).

Yataal gi (2)

النهاية في غريب الحديث والأثر (964).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (17/ 250).