waaye waxleen: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba"
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Ba aaya bii wàccee ci Yonnente Yàlla bi {Yàlla moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si bu ngeen feeñalee li nekk ci seen i bakkan walla ngeen nëbb ko Yàlla dana leen ci càmbar mu jéggal ku ko soob daal di mbugal ku ko soob te Yàlla man na lépp} [Al-Baxara: 284], nee na: loolu tar lool ci sahaabay Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñu teg seen i wóom ci suuf, daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, gal nañu ci ay lol àttan nanu ko, julli woor ak jihaad ak saraxe, waaye wàcce nañu ci aaya bii te manunu ko, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: "ndax dangeen bëgg a wax la ñoñ-téere ya leen jiitu woon waxoon dégg nanu moynanu? waaye waxleen: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba", ñu daal di ne: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba, ba ko gaaya waxee, seen làmmiñ ya nangu ko, Yàlla wàcce ca ginnaawam: {Yonnente bi gëm na li ñu wàcce ci mu bawoo ci Boroomam way gëm yi it ñépp gëm nañu gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak k téereem ak i Yonnenteem te duñu teqale diggante kenn ci Yónnenteem yi te dañuy wax naan dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba} [Al-Baxara: 285], ba ñu ko defee Yàlla mu kawe mi nasaxal ko, Yàlla mu màgg mi daal di wàcce: {Yàlla du togg benn bakkan lu dul lu mu man lu mu fàggu ci lu baax moom rekk la ñeel lu mu def ci lu bon it moom la ñeel Yàlla sunu Boroom bul nu jàppe ndeem danoo fàtte walla nu juum} [Al-Baxara: 286] " Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg coono kem na nga ko tege woon ña nu jiitu woon} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg lu nu àttanul} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom jéggal nj baal nu te yërëm nu yaw yaay sunu wéeruwaay dimbale nu ci kaw yéefar yi} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw".
لَمَّا نَزَلَتْ عَلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ {لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَإِنْ تُبْدُوا مَا فِي أَنْفُسِكُمْ أَوْ تُخْفُوهُ يُحَاسِبْكُمْ بِهِ اللهُ فَيَغْفِرُ لِمَنْ يَشَاءُ وَيُعَذِّبُ مَنْ يَشَاءُ وَاللهُ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ} [البقرة: 284]، قَالَ: فَاشْتَدَّ ذَلِكَ عَلَى أَصْحَابِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَأَتَوْا رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ ثُمَّ بَرَكُوا عَلَى الرُّكَبِ، فَقَالُوا: أَيْ رَسُولَ اللهِ، كُلِّفْنَا مِنَ الأَعْمَالِ مَا نُطِيقُ، الصَّلَاةَ وَالصِّيَامَ وَالجِهَادَ وَالصَّدَقَةَ، وَقَدِ اُنْزِلَتْ عَلَيْكَ هَذِهِ الآيَةُ وَلَا نُطِيقُهَا، قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَتُرِيدُونَ أَنْ تَقُولُوا كَمَا قَالَ أَهْلُ الكِتَابَيْنِ مِنْ قَبْلِكُمْ سَمِعْنَا وَعَصَيْنَا؟ بَلْ قُولُوا: سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا غُفْرَانَكَ رَبَّنَا وَإِلَيْكَ المَصِيرُ»، قَالُوا: سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا غُفْرَانَكَ رَبَّنَا وَإِلَيْكَ المَصِيرُ، فَلَمَّا اقْتَرَأَهَا القَوْمُ، ذَلَّتْ بِهَا أَلْسِنَتُهُمْ، فَأَنْزَلَ اللهُ فِي إِثْرِهَا: {آمَنَ الرَّسُولُ بِمَا أُنْزِلَ إِلَيْهِ مِنْ رَبِّهِ وَالمُؤْمِنُونَ كُلٌّ آمَنَ بِاللهِ وَمَلَائِكَتِهِ وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ لَا نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِنْ رُسُلِهِ وَقَالُوا سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا غُفْرَانَكَ رَبَّنَا وَإِلَيْكَ المَصِيرُ} [البقرة: 285]، فَلَمَّا فَعَلُوا ذَلِكَ نَسَخَهَا اللهُ تَعَالَى، فَأَنْزَلَ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ: {لَا يُكَلِّفُ اللهُ نَفْسًا إِلَّا وُسْعَهَا لَهَا مَا كَسَبَتْ وَعَلَيْهَا مَا اكْتَسَبَتْ رَبَّنَا لَا تُؤَاخِذْنَا إِنْ نَسِينَا أَوْ أَخْطَأْنَا} [البقرة: 286] " قَالَ: «نَعَمْ» {رَبَّنَا وَلَا تَحْمِلْ عَلَيْنَا إِصْرًا كَمَا حَمَلْتَهُ عَلَى الَّذِينَ مِنْ قَبْلِنَا} [البقرة: 286] قَالَ: «نَعَمْ» {رَبَّنَا وَلَا تُحَمِّلْنَا مَا لَا طَاقَةَ لَنَا بِهِ} [البقرة: 286] قَالَ: «نَعَمْ» {وَاعْفُ عَنَّا وَاغْفِرْ لَنَا وَارْحَمْنَا أَنْتَ مَوْلَانَا فَانْصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الكَافِرِينَ} [البقرة: 286] قَالَ: «نَعَمْ».
Ba Yàlla mu kawe mi wàccee ci Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waxam ji tudd naa sellam ga: {Yàlla a moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si} muy ay mbindeef ak nguur, coppaxndiku ak doxal, {bu ngeen feeñalee} fésal ak béral {li nekk ci seen i bakkan} ak seen i xol {walla ngeen nëbb ko} muur ko làq ko ci seen xol yi {Yàlla dana leen ci regle} ëllëg bis-pénc. {Mu jéggal ku ko soob} ci ngëneelam ak yërmàndeem, {Mu mbugal ku ko soob} ci maanduteem, {Yàlla amna kàttan ci lépp} dara tëwu ko. Ba ko Sahaaba yi déggee loolu diis ci ñoom; ndax li nekk mooy jàppe leen ba ci li nekk ci xol bi ci ay xalaat. Ñu ñëw ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, daal di goor ci seen i wóom, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ci li jiitu teg nañu nu ay jëfi yaram loo man nanu ko a def; niki julli ak woor ak jihaad ak saraxe, waaye wàcce nañu ci yaw aaya bii te manunu ko. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: ndax dangeen a bégg a wax kem la Yahuud ak Nasaraan ya waxoon: {dégg nanu moy nanu}? Waaye waxleen: {dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba}, sahaaba yi topp ndigalu Yàlla ak Yonnenteem bi, daal di wax: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba. Ba ko jullit ña waxee ci seen i làmmiñ, seen i bakkan wommatul ko; Yàlla wàcce ngir sellal Yonnente bi ak xeet wi ci waxam ji: {Yonnente bi gëm na li ñu wàcce ci moom mu bawoo ci Boroomam ak way-gëm} seen làmmiñ yi ak seen xol yi wommatul ndigalu Yàlla li. {ñoom ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i Yonnenteem te duñu teqale diggante kenn ci ay Yonnenteem}. Waaye danu leen di gëm ñoom ñépp {ñu wax naan ségg nanu} sa wax {topp nanu} sa ndigal, noo ngi sàkku {sag njéggal yaw sunu Boroom} ak sag baal, {te yaw rekk yaay delluwaay ba} delluwaay ba ëllëg bisu regle ba, ba ñu defee loolu, daal di wax li ñu leen digal ci fésal dégg gi ak topp gi ñeel ndigali Yàlla yi; Yàlla woyofalal xeet wi daal di nasaxal aaya bi ci waxam ci: {Yàlla du togg benn bakkan lu dul lu mu man} ak kannamam ak man-manam, {ñeel na ko} yoolu {la mu fàggu} def ko ci yiw, {dana dal ci kawam} mbugalu {la mu fàggu} ci lu bon ak bàkkaar, te Yàlla du jàppe kenn bàkkaaru keneen, du caagine it liu dengi-dengi ci bakkanam. {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu jàppe} di nu mbugal {bu nu fàttee} fàttalikuwunu, {walla nu juum} nu bàyyi la jub ci lu dul ag tayeef, Yàlla daal di leen di nangul loolu, daa di wax: waaw, def naa ko. {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg coono} ak jafe-jafe ak lu diis {kem na nga ko tege woon ña nu jiitu woon} ci Banuu Israayil ak ñeneen, Yàlla daal di leen du nangul ne: waaw, def naa ko. {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg lu nu àttanul} ci ay toggoo ak i nattu ak bir yi nga xam ne dananu lompañ ci gàddu ko, Yàlla daal di ne: waaw def naa ko, {baal nu} sunuy bàkkaar faral nu ko, {jéggal nu} sunuy bàkkaar suturaal nu, bàyyi ko, {yërëm nu} ci sa yërmànde gu yaatu gi, {yaw yaay sunu wéeruwaay} di sunu sang; {dimbale nu} ci taxawal lay ak noteel {ci kaw yéefar yi} ci bu ñuy xeex ak ñoom ak di jihaad ak ñoom, Yàlla nangul leen daal di ne: waaw def naa ko.
Leeral yërmàndey Yàlla mu kawe mi ñeel xeet wii ci sababus seen Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moom mi Yàlla wax ci màggal ay mbiram ne: {yónniwunu la lu dul ngir yërmànde ñeel mbindeef yi} [Al-Anbiyaa: 107].
Saxug nasaxal ci Alxuraan ju tedd ji, ak ne amna ci Alxuraan lu ñuy jàng waaye nasaxal nañu àtte ba deesu ko jëfe.
Ngëneelu sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ak seenug toroxlu ak topp ñeel ndigali Yàlla, ak seenug jëfe ñeel ndigalu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ragale woon lool xeetam wi di sóobu fa xeet ya jiitu woon sóobu ci delloo li ñu leen indil ci ay ndigali Yàlla mu kawe mi.
Warug jébbalu ñeel ndigalu Yàlla mu kawe mi, ak moytoo diiŋat ndigalam, ak ne lii ag niru-nirulu la ñeel ñoñ-téere ya.
Leeral ngëneelu xeet wi ci kaw xeet ya ko jiitu, ndax ñoom dañoo wax seen Yonnente ya: dégg nanu moy nanu, te xeet wii dafa wax: dégg nanu topp nanu.
Ngëneelu xeet wi ci ñu dindil leen jafe-jafe nangul leen ñaan ci bañ leen a jàppe li ñu fàtte walla ñu juum, ak dindi coono ya tege woon ca kaw ña leen jiitu, ak bañ leen a teg lu ñu àttanul.
Yàlla mu Sell mi te kawe du nu teg lu nu àttanul, te du nu togg jëf lu nu manul, te jax-jaxe yiy wëndéelu ci sunuy dënn bu nu ko nanguwul, dal ca, te defunu ko kon du nu lor.
Ñaan gii Yàlla mu kawe mi moo ko xibaare jële ko ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak way-gëm yi, daal di koy def ci téereem bi; ngir mu nekk ñaanug ñiy ñëw ci ginnaaw Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm, moom dafa bokk ci ñaan yi nga xam ne jaadu na ñu mokkal ko, di ko ñaan lu bari.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 115) (125).
Yataal gi (2)
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (1/ 336).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (3/ 547).
Cited in books
2 BooksYataal gi (2)
- العلم الواجب بدون فقه وبدون زيادات1{آمَنَ الرَّسُولُ بِمَا أُنزِلَ إِلَيْهِ مِن رَّبِّهِ وَالْمُؤْمِنُونَ كُلٌّ آمَنَ بِاللّهِ وملائكته وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ لاَ نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِّن رُّسُلِهِ وَقَالُواْ سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا غُفْرَانَكَ رَبَّنَا وَإِلَيْكَ الْمَصِير
- مجموعة زاد التفسير (1)التفسير 1أخرج مسلم في صحيحه عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قال: لَمّا نَزَلَتْ على رَسُولِ الله صلى الله عليه وسلم ﴿ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَإِنْ تُبْدُوا مَا فِي أَنْفُسِكُمْ أَوْ تُخْفُوهُ يُحَاسِبْكُمْ بِهِ اللَّهُ