Skip to content

Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am

Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».

جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: إِنِّي أُبْدِعَ بِي فَاحْمِلْنِي، فَقَالَ: «مَا عِنْدِي»، فَقَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ، أَنَا أَدُلُّهُ عَلَى مَنْ يَحْمِلُهُ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَنْ دَلَّ عَلَى خَيْرٍ فَلَهُ مِثْلُ أَجْرِ فَاعِلِهِ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi : Am na ku mas a w ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- ne ko: sama waruwaay dafa dee, yéegal ma cig daaba, te jox ma waruwaay mu yóbbu ma, Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- gàntal ko, ne ko amul dara lu mu koy jox, benn waay bu nekkoon foofu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi dinaa ko yóbbu ci ku koy jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- xamle ne, mook kiy saraxe ñoo bokk am yiw, ndax moo ko tegtal aji-yittewoo ji.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi : Ñaaxe ci tegtale lu baax.

Soññee ci def lu baax bokk na ci sabab i jàppalanteeg jullit ñi ak seenug bennoo.

Yaatug ngënéelu Yàlla.

Hadiis bii ab tënk bu matale la, jépp jëf ju baax da ciy dugg.

Nit ki bu manut a faj aajiy kiy laaj, da koy tegtal keneen.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1506) (1893).

Yataal gi (5)

شرح النووي على مسلم (11/ 166).

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 349).

فتح ذي الجلال والاكرام بشرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (6/ 298).