Skip to content

«kuy dog mbokk du dugg àjjana».

Jële nañu ci Jubayru Ibn Muthim -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«kuy dog mbokk du dugg àjjana».

«لَا يَدْخُلُ الْجَنَّةَ قَاطِعُ رَحِمٍ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku dog ay mbokkam ca la ñu yayoo ci ay àq, walla lor leen, di ñaawal jëme ci ñoom, kooku yayoowul a dugg àjjana.

Maanaay baat yi

.....:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi : Dog mbokk ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Jokk mbokk day amee ca kem nañu ko miine, kon day wuute kem barab ya ak jamono ya ak nit ña.

Jokk mbokk dana nekk ci siyaare, ak sarax, ak rafetal jëme ci moom, ak seeti ku feebar, ak digal leen lu baax tere leen lu bon, ak yeneen.

Lu mbokk gi di gën a jege dog mbokk gi di gën a rëy bàkkaar.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1981) (2556).

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 5) (5984).

Yataal gi (5)

شرح النووي على مسلم (16/ 113).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 90).

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (6/ 277).