Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

5 of 732 cards

Clear filters
Yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma bu nu ay njiit jiitee di nu laaj seen àq, di nu xañ sunuy àq, ana lan nga nuy digal? Mu dummooyu ko, topp mu laajaat ko, mu dummooyu ko, mu laaj ko ci ñaareel bi walla ñatteel bi, Al-Ashas ibn Xays xëcc ko, mu ne ko: "deeleen dégg tey topp, li leen war ñoom mooy la ñu leen gàdduloo, yéen it li leen war mooy li ñu leen gàdduloo".
Wér na Muslim soloo na ko.
Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxaw fi nun daal di nuy waar waar gu jotale xol yi jàq nañu ci, bët yi tuur ci rangooñ, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, waar nga nu waarug kuy tàggatoo, jox ñu ak kóllare. Mu ne leen : "dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal, ŋànkleen ko ak seen i dégéj, te ngeen moytandiku mbir yi ñu sos, ndax bidaa yépp ay réer la".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal, ŋànkleen ci ak séen i dégéj, maa ngi leen di moytandikuloo bir yi ñu sos; ndax bidaa yépp ag cànkute la".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy.
«diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».
Wér na Muslim soloo na ko.
"ay njiit danañu ñëw yoo xam ne dañuy fen, di tooñ, ku leen dëggal ca seen fen ya dimbali leen ca seen tooñ ga kooku bokkul ci man, te bokkuma ci moom, te duma fekk ca Baaj ba, ku leen dëggalul ca seen fen ya, te dimbaliwu leen ca seen tooñ ga kooku ci man la bokk, te man itam ci moom laa bokk, te dana ma fekk ca Baaj ba".
Wér na Ahmat soloo na ko.