Skip to content

"ay njiit danañu ñëw yoo xam ne dañuy fen, di tooñ, ku leen dëggal ca seen fen ya dimbali leen ca seen tooñ ga kooku bokkul ci man, te bokkuma ci moom

Jële nañu ci Husayfata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"ay njiit danañu ñëw yoo xam ne dañuy fen, di tooñ, ku leen dëggal ca seen fen ya dimbali leen ca seen tooñ ga kooku bokkul ci man, te bokkuma ci moom, te duma fekk ca Baaj ba, ku leen dëggalul ca seen fen ya, te dimbaliwu leen ca seen tooñ ga kooku ci man la bokk, te man itam ci moom laa bokk, te dana ma fekk ca Baaj ba".

«إِنَّهَا سَتَكُونُ أُمَرَاءُ يَكْذِبُونَ وَيَظْلِمُونَ، فَمَنْ صَدَّقَهُمْ بِكَذِبِهِمْ وَأَعَانَهُمْ عَلَى ظُلْمِهِمْ فَلَيْسَ مِنَّي، وَلَسْتُ مِنْهُ، وَلَا يَرِدُ عَلَيَّ الْحَوْضَ، وَمَنْ لَمْ يُصَدِّقْهُمْ بِكَذِبِهِمْ وَلَمْ يُعِنْهُمْ عَلَى ظُلْمِهِمْ فَهُوَ مِنِّي، وَأَنَا مِنْهُ، وَسَيَرِدُ عَلَيَّ الْحَوْضَ».

Ahmat soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare ne ginnaaw bu faatoo nit ñi ay njiit danañu leen jiite yoo xam ne dañuy fen bu ñuy wax di wax lu ñu dul def, di tooñ ci àtte yi, ku dugg fi ñoom dëggal leen ca seen fen ya, walla mu dimbali leen ca sen tooñ ga ci jëf walla ci wax niki di leen ubbee ngir jege leen ak yaakaar li nekk fi ñoom; na xam ne man ku sett wicc laa ci moom te bokkul ci man, man it bokkuma ci moom, te du ñëw ca Baaju Kawsara ba ëllëg bis-pénc, waaye ku duggul fi ñoom, te dëggalu leen ca seen fen ya, te it dimbaliwu leen ca seen tooñ ya, kooku ci man la bokk man it ci moom laa bokk, te dana ñëw ca Baaju Kawsara ba ëllëg bis-pénc.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bu nu duggee ci njiit yi ci di leen gindi ak di leen jubbanti ak di woyofal seen uw ay; loolu moom lu ñu sàkku la, waaye bu ñu duggee fi ñoom ngir dimbali leen ca seen tooñ ya ak dëggal leen ca seen fen ya lii moom lu ñu ŋàññ la.

Leeral tëkku gi ñeel kiy dimbali njiit ci tooñ.

Tëkku gii ci hadiis bi day tegtale ne jëf jii dafa araam, te ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Ñaaxe ci dimbalante ci mbaax ak ragal Yàlla, ak bañ a dimbalante ci bàkkaar ak noonoo.

Saxal Baaju sunu Yonente bi Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak ne xeetam wi danañu ca naan.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (38/ 295) (23260).

Yataal gi (1)

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (32/ 334).