Skip to content

bu ñu ca duggoon duñu ca genn mukk ba bis-pénc; topp ci njekk lay doon".

Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa yónni ag gawar mu jiital ca ab waat ci Ansaar yi, mu digal leen ñu topp ko, mu mer, daal di ne leen: ndax du Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo leen digal ngeen topp ma? Dajaleelleen ma matt, ñu dajaleel ko, mi daal di ne: duggleen ci, ñu nar ko a def, ñenn ñi téye ñeneen ñi, di wax naan: dañoo daw sawara jëm ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, deñuñu ci loolu ba sawara wa fay, meram ma giif, mu egg ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: bu ñu ca duggoon duñu ca genn mukk ba bis-pénc; topp ci njekk lay doon".

بَعَثَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ سَرِيَّةً فَاسْتَعْمَلَ رَجُلًا مِنَ الأَنْصَارِ، وَأَمَرَهُمْ أَنْ يُطِيعُوهُ، فَغَضِبَ، فَقَالَ: أَلَيْسَ أَمَرَكُمُ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنْ تُطِيعُونِي؟ قَالُوا: بَلَى، قَالَ: فَاجْمَعُوا لِي حَطَبًا، فَجَمَعُوا، فَقَالَ: أَوْقِدُوا نَارًا، فَأَوْقَدُوهَا، فَقَالَ: ادْخُلُوهَا، فَهَمُّوا، وَجَعَلَ بَعْضُهُمْ يُمْسِكُ بَعْضًا، وَيَقُولُونَ: فَرَرْنَا إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنَ النَّارِ، فَمَا زَالُوا حَتَّى خَمَدَتِ النَّارُ، فَسَكَنَ غَضَبُهُ، فَبَلَغَ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: «لَوْ دَخَلُوهَا مَا خَرَجُوا مِنْهَا إِلَى يَوْمِ القِيَامَةِ؛ الطَّاعَةُ فِي المَعْرُوفِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa yónni ab arme, mu def benn waay ci ansaar yi mu nekk seen njiit, mu digal leen ñu toop ko, njiit la mere leen daal di ne leen: ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digalu leen ngeen topp ma? Ñu ne ko: ahakay, mu ne: digal naa leen ngeen dajale matt, taal sawara topp ngeen dugg ca, ñu dajale matt ma taal sawara wa, ba ñu ca bëggee dugg, ñenn ñi di xool ñeneen ñi. Ñu daal di ne: nun de toppunu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu dul ngir daw sawara, mo kon ndax dinanu ci dugg? Ba ñu nekkee ci loolu sawara wa daal di fay, meru njiit la daal di deñ. Ñu nettali Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc loolu, mu wax ne: bu ñu ko toppn ba dugg ca sawara wa ñu taal kon dees na leen ca mbugal te duñu ca génn ci diirub àdduna ji bépp, deesul topp mbindeef ci moy Aji-Bind ji; waaye topp moom ci njekk rekk lay doon du doon cig moy.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral ne topp ci njekk lay doon waaye du nekk ci ag moy, doonte aji-digle sax ku ñu war a topp la.

Moykat biy aji-kennal ku ñu tëkku ci sawara la, amaana it Yàlla jéggal ko.

Yoonalees na jiital kenn ci xare, niki noonu it ci tukki.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (5/ 161) (4340).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1469) (1840).

Yataal gi (1)

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (10/ 220).