"gaaral na ñu ma Àjjana ak Sawara waaye gisuma ca yiw walla ay wu mel ni tay jii, te bu ngeen xamoon li ma xam kon dangeen ree tuuti te dangeen jooy lu bari
Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mere na sahaabaam yi, daal di xutba, wax ne:
"gaaral na ñu ma Àjjana ak Sawara waaye gisuma ca yiw walla ay wu mel ni tay jii, te bu ngeen xamoon li ma xam kon dangeen ree tuuti te dangeen jooy lu bari, nee na: bis bu ko gën a tar musul a am ci Sahaabay Yonente Yàlla bi, nee na: ñu muur seen bopp yi di yékkét, nee na: Umar daal di ne: gërëm nanu Yàlla muy sunu Boroom, ak Lislaam muy sunu Diine, ak Muhammat muy sunu Yonente, nee na: waa jooja daal di jug, daal di ne: kan mooy sama baay? Mu ne ko: "diw mooy sa baay" aaya bii wàcc: {yéen way-gëm ñi bu leen laaj loo xam ne bu ñu leen ko leeralee mu naqari leen} [Al-Maa-ida: 101].
«عُرِضَتْ عَلَيَّ الْجَنَّةُ وَالنَّارُ فَلَمْ أَرَ كَالْيَوْمِ فِي الْخَيْرِ وَالشَّرِّ، وَلَوْ تَعْلَمُونَ مَا أَعْلَمُ لَضَحِكْتُمْ قَلِيلًا وَلَبَكَيْتُمْ كَثِيرًا» قَالَ: فَمَا أَتَى عَلَى أَصْحَابِ رَسُولِ اللهِ صلى الله عليه وسلم يَوْمٌ أَشَدُّ مِنْهُ، قَالَ: غَطَّوْا رُءُوسَهُمْ وَلَهُمْ خَنِينٌ، قَالَ: فَقَامَ عُمَرُ فَقَالَ: رَضِينَا بِاللهِ رَبًّا، وَبِالْإِسْلَامِ دِينًا، وَبِمُحَمَّدٍ نَبِيًّا، قَالَ: فَقَامَ ذَاكَ الرَّجُلُ فَقَالَ: مَنْ أَبِي؟ قَالَ: «أَبُوكَ فُلَانٌ»، فَنَزَلَتْ: {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لا تَسْأَلُوا عَنْ أَشْيَاءَ إِنْ تُبْدَ لَكُمْ تَسُؤْكُمْ} [المائدة: 101].
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa am lu ko jot ci sahaaba yi, te mooy ñoom dañoo bari lu ñu koy laaj, ba mu mer daal di xutba, wax ne: Gaaralal nañu ma Àjjana ak Sawara; waaye musuma a gis yiw wu bari kem li ma gis tay ca Àjjana, du caagine it aw ay wu bari kem li ma gis tay ca Sawara, te bu ngeen gisoon li ma gis, xam li ma xam ci li ma gis tay ak lu jiitu tay, kon dangeen ragal ragal gu tar, te kon seen i ree dana néew, seen i jooy bari. Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm wax na ne: Amul bis bu gën a tar ci Sahaabay Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci bis boobu, ñu muur seen bopp yi di génne kàddu gu ànd ak ŋiiŋ guy génne ci bakkan ngir jooy yu tar. Umar jug daal di ne: Gërëm nanu Yàlla muy sunu Boroom, ak Lislaam muy sunu Diine, ak Muhammat muy sunu Yonente. Nee na: waa ja daal di jug, daal di ne: kan mooy sama baay? Mu ne ko: "diw mooy sa baay", aaya bi dal di wàcc: {yéen way-gëm ñi bu leen laaj loo xam ne bu ñu leen ko leeralee mu naqari leen} [Al-Maa-ida: 101].
Sopp nañu jooy ngir ragal mbugalum Yàlla, ak bañ a baril ay ree; ndax day tegtale ag càggante ak wow xol.
Jeexitalu Sahaaba yi ci waare gi, ak seen ragal gu tar ci mbugalu Yàlla mu màgg mi
Sopp nañu ñu muur kanam gi bu ñuy jooy.
Al-Xattaabii nee na: hadiis bii mi ngi jëm ci kiy laaj ngir diisal ak taral ci lu mu amul aajo, bu dee kuy laaj ngir lu manul ñàkk ci am masala gaar ko mu laaj ko kooku amul bàkkaar te it deesu ko yedd.
Ñaaxe ci jub kocc tege ci topp Yàlla, ak sori moy Yàlla yi, ak taxaw ci daytali Yàlla yi.
Nekk na ci it daganug mer bu ñuy waare ak di jàngale.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 54) (4621).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1832) (2359).
Yataal gi (6)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 367).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 474).
النهاية في غريب الحديث والأثر.
لابن الأثير(1/ 45).