«amul benn jullit buy jàppu rafetal njàppu mi, daal di jog julli ñaari ràkka, xolam ak jëmmam jublu ca, lu dul ne àjjana war na ci moom"
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dañu doon sàmm ay giléem samag ay ñëw, ma yóbb leen ci ngoon gi, fekk Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di waxtaanal nit ñi ma fekk ko muy wax:
«amul benn jullit buy jàppu rafetal njàppu mi, daal di jog julli ñaari ràkka, xolam ak jëmmam jublu ca, lu dul ne àjjana war na ci moom" nee na: ma ne: ana lan moo dàq lii, benn waay bu nekk sama kanam daal di ne: ki xolam baax, ma xool rekk Umar di wax naan: gis naa ne leegi nga ñëw, nee na: "amul kenn kuy jàppu jotale njàppu ma -walla matale- njàppu ma, topp mu wax: maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam lu dul ne dees na ko ubbil juróom-ñatti bunti àjjana mu dugg ci bu ko soob"».
«مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَتَوَضَّأُ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهُ، ثُمَّ يَقُومُ فَيُصَلِّي رَكْعَتَيْنِ، مُقْبِلٌ عَلَيْهِمَا بِقَلْبِهِ وَوَجْهِهِ، إِلَّا وَجَبَتْ لَهُ الْجَنَّةُ» قَالَ فَقُلْتُ: مَا أَجْوَدَ هَذِهِ، فَإِذَا قَائِلٌ بَيْنَ يَدَيَّ يَقُولُ: الَّتِي قَبْلَهَا أَجْوَدُ، فَنَظَرْتُ فَإِذَا عُمَرُ قَالَ: إِنِّي قَدْ رَأَيْتُكَ جِئْتَ آنِفًا، قَالَ: «مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُبْلِغُ - أَوْ فَيُسْبِغُ - الْوَضُوءَ ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِنْ أَيِّهَا شَاءَ».
Yonnente day leeral di waxtaanal nit ñi ci ñaari gëneel yu màgg: Bi ci njëkk: ku jàppu te rafetal njàppu ma jotal ko matal ko ca anam ga ñu ko sunnaale, jox cér bu nekk àqam ci ndox mi, topp mu wax: maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam; lu dul ne dees na ko ubbil juróom-ñatti bunti àjjana yi mu dugg ci bu ko ci soob. Ñaareel bi: ku jàppu njàppu lu mat lii, topp mu jug ginnaaw loolu julli ñaari ràkka; xolam jublu ca cig sellal ak ug ragal, mu toruxlu ci jëmmam ci mbooleem céri yaram wi ñeel Yàlla, àjjana war na ci moom.
Màggug ngëneelu Yàlla mu kawe mi ci joxe fay gu rëy ci jëf ju tuuti.
Yoonalees na jotal ak matale am jàppu, ak julli ci ginnaawam ñaari ràkka gu ànd ak ragal, ak la cay am ci fay gu màgg.
Jotal njàppu, ak def sikar gii ci ginnaawam, dafa bokk ci sababi dugg àjjana na yi.
Sopp nañu wax sikar gii it ci aji-sangu ji.
Xarug Sahaaba yi ci yiw, ci jàng xam-xam ak tasaare ko, ak di ca dimbalante ak ci seen mbiri dund.
Sikar ginnaaw jàppu mi day sellal xol di ko laabal ci bokkaale, kem ni jàppu di laabale yaram wi di ko setal ci tilim.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 209) (234).
Yataal gi (4)
توضيح الأحكام.
للبسام (1/ 251).
المنهاج شرح صحيح مسلم بن الحجاج.
للنووي (3/ 120).
Cited in books
11 BooksYataal gi (11)
- الأربعون في تعظيم قدر الصلاةالأربعون في تعظيم قدر الصلاة «مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَتَوَضَّأُ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهُ، ثُمَّ يَقُومُ فَيُصَلِّي رَكْـــــــعَتَيْنِ، مُقْبِلٌ عَلَيْهِمَا بِقَلْبِهِ وَوَجْــــهِهِ، إِلَّا وَجَبَتْ لَهُ الْجَنَّةُ».
- الخطب المنبرية موسوعة الخطب المنبرية (القسم الثاني)«مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَتَوَضَّأُ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهُ، ثُمَّ يَقُومُ فَيُصَلِّي رَكْعَتَيْنِ، مُقْبِلًا عَلَيْهِمَا بِقَلْبِهِ وَوَجْهِهِ، إِلَّا وَجَبَتْ لَهُ الجَنَّةُ»
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"ما منكم من أحد يتوضأ فيسبغ الوضوء ثم يقول: "أشهد أن لا إله إلا الله وحده لا شريك له، وأشهد أن محمدًا عبده ورسوله: إلا فتحت له أبواب الجنة الثمانية يدخل من أيها شاء" .
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“ما منكم مِن أحد يتوضأ فيبلغ أو فيسبغ الوضوء ثم يقول: (أشهد أن لا إله إلا الله، وأن محمدا عبد الله ورسوله) إلا فتحت له أبواب الجنة الثمانية يدخل من أيها شاء”.
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“ما من مسلم يتوضأ فيحسن وضوءه، ثم يقوم فيصلي ركعتين، مقبل عليهما بقلبه ووجهه، إلا وجبت له الجنة”.
- خطب تعظيم قدر الصلاة"مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَتَوَضَّأُ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهُ، ثُمَّ يَقُومُ فَيُصَلِّي رَكْعَتَيْنِ، مُقْبِلٌ عَلَيْهِمَا بِقَلْبِهِ وَوَجْهِهِ، إِلَّا وَجَبَتْ لَهُ الْجَنَّةُ"
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)مجموعة زاد الفقه (1)«مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُسْبِغُ الْوَضُوءَ ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اﷲُ وَأَنَّ مُحَمَّداً عَبْدُ اﷲِ وَرَسُولُهُ إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِنْ أَيِّهَا شَاءَ»
- مشروع منهاج زادكزادك 1 طالب«مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُبْلِغُ أَوْ فَيُسْبِغُ الْوَضُوءَ، ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَن لَا إِلَهَ إِلاَ اللهُ وأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ ورَسُولُهُ، إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِن
- من الأحكام الفقهية في الطهارة والصلاة والجنائز«مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُسْبِغُ الْوَضُوءَ، ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِنْ أَيِّهَ
- نبراس طالب (1)1(أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا الله وأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ).
- نبراس طالب (1)1«مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُبْلِغُ أَوْ فَيُسْبِغُ الْوَضُوءَ، ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَلَّا إِلَهَ إِلاَ اللهُ وأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ ورَسُولُهُ، إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِنْ