Skip to content

"Yàlla mu kawe mi nee na: ñatt ñii seen xuloowaale laay doon ëllëg bis-pénc

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"Yàlla mu kawe mi nee na: ñatt ñii seen xuloowaale laay doon ëllëg bis-pénc: waa ju ñu jox ngir man mu daal di wor, ak waa ju jaay gor lekk njëgam, ak waa ju liggéeyloo liggéeykat mu matale ko te joxu ko fayam".

«قَالَ اللَّهُ تَعَالَى: ثَلاَثَةٌ أَنَا خَصْمُهُمْ يَوْمَ القِيَامَةِ: رَجُلٌ أَعْطَى بِي ثُمَّ غَدَرَ، وَرَجُلٌ بَاعَ حُرًّا فَأَكَلَ ثَمَنَهُ، وَرَجُلٌ اسْتَأْجَرَ أَجِيرًا فَاسْتَوْفَى مِنْهُ وَلَمْ يُعْطِهِ أَجْرَهُ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne: ñatt xeet yii man seen xuloowaale laay doon ëllëg bis-pénc, te ku ma xolool di naa ko yey di naa ko not: Ki ci njëkk: ku joxe ngiñam ci Yàlla, daal di fas kóllare topp mu fecci ko daal di wor. Ñaareel ki: ku jaay ag gor ci ne ab jaam la ba noppi lekk njëgam di soppaxndiku ci njëgam la. Ñatteel ki: ku jël liggéeykat ngir ab liggéey, mu matale liggéey ba te joxu ko njëgu liggéeyam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Hadiis bii dafa bokk ci li Yonente bi di nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsii walla Hadiisu Al-Ilaahii, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la jóge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññee ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci njàng mi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottalaate ak yenneen.

As-Sindii nee na: nee nañu: tudd gi mu tudd ñatt ñi nekkul ngir tënk ko; ndax Yàlla mu kawe mi xuloowaale la ñeel bépp tooñkat waaye loolu ngir taral la ci kaw ñatt ñii.

Ibn Al-Jawsii nee na: gor jaamu Yàlla la, ku ko tooñ kon sangam xuloowaaleem la, te mooy Yàlla.

Al-Xattaabii nee na: def gor jaam day ame ci ñaari mbir: mu goreel ko topp mu nëbb looli walla mu weddi ko. Ñaareel bi mu koy jëfandikoo ci forse ginnaaw goreel ga, bu njëkk bi moo gën a tar ci ñaar yooyu. Ma wax ne: buntub hadiis bi moo gën a tar; ndaxte ànd ak li ci nekk ci nëbb goreel gi walla ñàkk a jëfe li loolu di waral ci jaay gi ak lekk njëg gi loolu moo tax tëkku gi gën a tar.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 90) (2270).

Yataal gi (3)

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام (4/ 252).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (4/ 108).

مرشد ذوي الحجا والحاجة إلى سنن ابن ماجه والقول المكتفى على سنن المصطفى (14/ 211).