Skip to content

«genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka».

«صَلَاةٌ فِي مَسْجِدِي هَذَا خَيْرٌ مِنْ أَلْفِ صَلَاةٍ فِيمَا سِوَاهُ إِلَّا الْمَسْجِدَ الْحَرَامَ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelu julli ci jàkkaam ji, ak ne moo gën yool ci junni julli ci fu dul moom ci jàkka yi ci kaw suuf, ba mu des jàkka ja ñu wormaal fa Màkka, ndax moom moo gën julli ci jàkkay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dañuy ful yoolu julli ci jàkkay Màkka ak Jàkkay Yonnente bi ca Madiina.

Julli ci jàkkay Màkka moo gën téeméeri junni julli ci beneen bu dul moom.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 60) (1190).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 1012) (1394).

Yataal gi (2)

فتح الباري (3/67).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (24/ 684).