"ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara".
«مَنْ كَذَبَ عَلَيَّ مُتَعَمِّدًا فَلْيَتَبَوَّأْ مَقْعَدَهُ مِنَ النَّارِ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne ku ko fenal te tay ko askanale ko wax walla jëf ci ay fen, kooku allaaxira am na fa toogukaay ca sawara; muy ag payam ci li mu ko fenal.
...:
Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jublu ko ca te tay ko sabab la ci dugg sawara.
Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yamul ak fenal yeneen nit ñi, ngir la cay tege ci yàqute yu màgg ci diine ak àdduna.
Dañuy moytondikuloo tasaare ay hadiis lu jiitu ñuy gëstu ak a wóorlu ndax li ñu ko askanale Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wér na walla déet.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 33) (110).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 10) (3).
Yataal gi (5)
إكمال المعلم (1/111).
شرح النووي على مسلم (1/65).
المفهم (1/32).
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (2/ 151).
شرح مقدمة سنن ابن ماجه (5/ 8).