Li ñu njëkk a tàmbalee Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci Wahyu mooy gént gu sell
Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Li ñu njëkk a tàmbalee Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci Wahyu mooy gént gu sell, daawul gis dara ci ay gént lu dul ne dana ñëw mel ni suba gu xar, topp ñu bëggloo ko ag wéet, mu daan dem ca xuntum Hiraa wa di fa jaamu guddi yi am ug lim, njëkk mu fay jóge di dellu ca njabootam, da daan yóbb ag dund ngir loolu, topp mu dellu ca Xadiija daal di yóbbal lu mel noonu, ba dëgg dikkal ko fekk ma nga ca xunt wa, Malaaka mi dikkal ko ne ko: jàngal, mu ne ko: "man duma jàngkat" nee na: "mu jàpp ma daal di may naj ba ma sonn lool mu bàyyi ma, daal di ne ma: jàngal, ma ne ko: duma jàngkat, mu jàpp ma ñaareelu yoon, naj ma ba ma sonn lool, mu bàyyi ma, ne ma: jàngal, ma ne ko: duma jàngkat, mu jàpp ma ñatteelu yoon, naj ma ba ma sonn lool, daal di may bàyyi, ne ma: {iqra bismi Rabbika Allasii xalaqa xalaqa Al-Insaana min halaqin iqra wa Rabbuka Al-Akramu}, [Al-Halaxi: 1-3] Yonnente Yàlla dellu ca kër ga cër yi di lox, muy wax naan "sàngleen ma, sàngleen ma" ñu sàng ko ba tiitaange ji deñ ci moom, mu nettali Xadiija xibaar bi ne ko: "ragal naa ci sama bopp" Xadiija ne ko: déedéet, giñ naa ci Yàlla ne Yàlla du la gàccaal mukk, ndax yaw dangay jokk mbokk, di gàddu aji-sonn ji, di wutal ñi amul, di ganale gan gi, di dimbalee ci nattuy dëgg yi, Xadiija yóbb ko ca Waraxatu ibn Nawfal ibn Asad ibn Abdul Husaa, di doomu baay tëxu Xadiija, mu nekkoon koo xam ne dafa duggoon ci diiney Nasaraan ca jamonoy ceddo ga, mu daan bind it téere ci làkkub Hiraaniya bi, daan bind Injiil ci làkkub Hibraaniya lu soob Yàlla mu bind ko ca, mu nekkoon mag mu màggat mu gumba, mu ne ko: yaw sama doomu baay tëx bi, déglul sa doomu mbokk mii, Waraxatu ne ko: yaw sama doomu mbokk mi, ana lan nga gis? Yonente Yàlla bi xibaar ko li mu gis, Waraxatu ne ko: lii de mooy Malaaka mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa, aka neexoon mu fekk ma dëgër, aka neexoon mu fekk may dund jamono yi la saw nit di génne, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "ndax ñoom dañu may génne?", mu ne ko waaw, kenn masut a indi lu mel ni li nga indi lu dul ne noonoo nañu ko, te say bis bu ma fi fekkee dinaa la dimbali ndimbal lu màgg. Topp yàggul dara Waraxatu daal di faatu, Wahyu wi taxaw.
أَوَّلُ مَا بُدِئَ بِهِ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنَ الوَحْيِ الرُّؤْيَا الصَّالِحَةُ فِي النَّوْمِ، فَكَانَ لاَ يَرَى رُؤْيَا إِلَّا جَاءَتْ مِثْلَ فَلَقِ الصُّبْحِ، ثُمَّ حُبِّبَ إِلَيْهِ الخَلاَءُ، وَكَانَ يَخْلُو بِغَارِ حِرَاءٍ فَيَتَحَنَّثُ فِيهِ -وَهُوَ التَّعَبُّدُ- اللَّيَالِيَ ذَوَاتِ العَدَدِ قَبْلَ أَنْ يَنْزِعَ إِلَى أَهْلِهِ، وَيَتَزَوَّدُ لِذَلِكَ، ثُمَّ يَرْجِعُ إِلَى خَدِيجَةَ فَيَتَزَوَّدُ لِمِثْلِهَا، حَتَّى جَاءَهُ الحَقُّ وَهُوَ فِي غَارِ حِرَاءٍ، فَجَاءَهُ المَلَكُ فَقَالَ: اقْرَأْ، قَالَ: «مَا أَنَا بِقَارِئٍ» قَالَ: «فَأَخَذَنِي فَغَطَّنِي حَتَّى بَلَغَ مِنِّي الجَهْدَ ثُمَّ أَرْسَلَنِي، فَقَالَ: اقْرَأْ، قُلْتُ: مَا أَنَا بِقَارِئٍ، فَأَخَذَنِي فَغَطَّنِي الثَّانِيَةَ حَتَّى بَلَغَ مِنِّي الجَهْدَ ثُمَّ أَرْسَلَنِي، فَقَالَ: اقْرَأْ، فَقُلْتُ: مَا أَنَا بِقَارِئٍ، فَأَخَذَنِي فَغَطَّنِي الثَّالِثَةَ ثُمَّ أَرْسَلَنِي، فَقَالَ: {اقْرَأْ بِاسْمِ رَبِّكَ الَّذِي خَلَقَ خَلَقَ الإِنْسَانَ مِنْ عَلَقٍ اقْرَأْ وَرَبُّكَ الأَكْرَمُ}»، [العلق:1-3] فَرَجَعَ بِهَا رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَرْجُفُ فُؤَادُهُ، فَدَخَلَ عَلَى خَدِيجَةَ بِنْتِ خُوَيْلِدٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا، فَقَالَ: «زَمِّلُونِي، زَمِّلُونِي» فَزَمَّلُوهُ حَتَّى ذَهَبَ عَنْهُ الرَّوْعُ، فَقَالَ لِخَدِيجَةَ وَأَخْبَرَهَا الخَبَرَ: «لَقَدْ خَشِيتُ عَلَى نَفْسِي» فَقَالَتْ خَدِيجَةُ: كَلَّا وَاللَّهِ مَا يُخْزِيكَ اللَّهُ أَبَدًا، إِنَّكَ لَتَصِلُ الرَّحِمَ، وَتَحْمِلُ الكَلَّ، وَتَكْسِبُ المَعْدُومَ، وَتَقْرِي الضَّيْفَ، وَتُعِينُ عَلَى نَوَائِبِ الحَقِّ، فَانْطَلَقَتْ بِهِ خَدِيجَةُ حَتَّى أَتَتْ بِهِ وَرَقَةَ بْنَ نَوْفَلِ بْنِ أَسَدِ بْنِ عَبْدِ العُزَّى، ابْنَ عَمِّ خَدِيجَةَ، وَكَانَ امْرَأً تَنَصَّرَ فِي الجَاهِلِيَّةِ، وَكَانَ يَكْتُبُ الكِتَابَ العِبْرَانِيَّ، فَيَكْتُبُ مِنَ الإِنْجِيلِ بِالعِبْرَانِيَّةِ مَا شَاءَ اللَّهُ أَنْ يَكْتُبَ، وَكَانَ شَيْخًا كَبِيرًا قَدْ عَمِيَ، فَقَالَتْ لَهُ خَدِيجَةُ: يَا ابْنَ عَمِّ، اسْمَعْ مِنَ ابْنِ أَخِيكَ، فَقَالَ لَهُ وَرَقَةُ: يَا ابْنَ أَخِي، مَاذَا تَرَى؟ فَأَخْبَرَهُ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ خَبَرَ مَا رَأَى، فَقَالَ لَهُ وَرَقَةُ: هَذَا النَّامُوسُ الَّذِي نَزَّلَ اللَّهُ عَلَى مُوسَى، يَا لَيْتَنِي فِيهَا جَذَعًا، لَيْتَنِي أَكُونُ حَيًّا إِذْ يُخْرِجُكَ قَوْمُكَ، فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَوَ مُخْرِجِيَّ هُمْ؟»، قَالَ: نَعَمْ، لَمْ يَأْتِ رَجُلٌ قَطُّ بِمِثْلِ مَا جِئْتَ بِهِ إِلَّا عُودِيَ، وَإِنْ يُدْرِكْنِي يَوْمُكَ أَنْصُرْكَ نَصْرًا مُؤَزَّرًا. ثُمَّ لَمْ يَنْشَبْ وَرَقَةُ أَنْ تُوُفِّيَ، وَفَتَرَ الوَحْيُ.
Yaayu jullit ñi Aysatu day xibaare ne li ñu njëkk a tàmbalee Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci Wahyu mooy gént gu dëggu ci ay nelaw, ba tax daawul gis dara ci ay nelawam lu dul ne dana ñëw leer nàññ mel ni leeru suba gi, topp ñu bëggloo ko beru, mu daan beru ca xuntum Hiraa ma di fa jaamu Yàlla guddi yu li mu yi laata muy dello ca njabootam, muy yóbbaale dund, topp mu dellu ca yaayu jullit ñi Xadiija yal na ko Yàlla dollee gërëm mu daan fa wut yóbbal buy tollook guddi yamufay nekk, ba mbir may dëgg dikkal ko fekk ma nga ca xuntum Hiraa ma. Malaaka mii di Jibriil yal na ko Yàlla dolli jàmm dikkal ko ne ko: jàngal, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: manumaa jàng, nee na: mu jàpp ma naj ma ba ma sonn lool mu bàyyi ma, ne ma: jàngal, ma ne ko: manumaa jàng, mu jàpp ma ñaareelu yoon naj ma ba ma sonn lool mu bàyyi ma, ne ma: jàngal, ma ne ko: manumaa jàng, mu jàppaat ma najaat ma ci ñatteelu yoon wi daal di may bàyyi, ne ma: {jàngal ci sa turu Boroom bi nga xam ne moo bind. Bind na nit ci lumb dereet. Jàngal sa Boroom déy moo gën a tedd lépp} [Al-Halaxi: 1-3]. Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dellu yóbbaale aaya yii ay céram di lox ngir ragal ne day dee, mu dugg ci soxnaam Xadiija bint Xuwaylid yal na ko Yàlla dollee gërëm, ne ko: Sàngleen ma ci ab sër, sàngleen ma ci sër, ñu sàng ko ci sër ba tiitaange ji deñ, mu nettali Xadiija xibaar bi, daal di ne ko: Ragal naa dee ci sama bopp de, Xadiija ne ko: Déedéet, giñ naa ci Yàlla ne, Yàlla du la gàccaal mukk, ndax yaw dangay jokk mbokk, di gàddu aji néew ji doole ji nga xam ne manut a dem ak mbiram, di wutal aji ñàkk ji; ba tax ngay jox nit ñi lu ñu dul ame ci ku dul Yaw, ngay teral gan, di dimbale ci nattu yi. Xadiija dal di ànd ak moom ba indi ko ci Waraxatu ibn Nawfal ibn Asad ibn Abdul Husaa, muy doomu baay-taxam, mu nekoon góor gu bàyyi ceddo ga, mujj nekk ci diiney Nasaraan, mu daan bind Injiil ci làkkub Hibraaniya lu soob Yàlla mu bind ko ca, mu nekkoon góor gu màggat silmaxa, Xadiija ne ko: Yaw Sama doomu baay-tax déglul sa doomu mbokk mii, Waraxatu ne ko: yaw sama doomu mbokk mi, loo gis? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaar ko li mu gis, Waraxatu ne ko: kii de Jibriil mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa la, aka neexoon ma nekk waxambaane bu dëgër, aka neexoon may dund jamono ya la saw nit di génne, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ndax ñoom dañu may génne? Mu ne ko: waaw, kenn masut a indi lu mel ni li nga indi lu dul ne lor nañu ko noonoo ko, te bu ma fi say bis fekkoon dinaa la dimbali ndimbal lu rëy. Yàggul dara Waraxatu ibn Nawfal daal di faatu, wahyu wi dagg ab diir te ñëwul.
Leeral tàmbalig wahyu wi jëm ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Géntug Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa bokk ci xeeti Wahyu yi.
Yoonalees na wut yóbbal, ak ne loolu safaanoowul ak wakkirlu, ndax sàngub wakkirlukaat yi muy Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc def na ko.
Matug teddngay Boroom bu kawe bi te Sell ci ne dafa xamal jaamam yi lu ñu xamul woon, mu jële leen ci lëndëmug réer yóbb leen ci leerug xam.
Ngëneelu xam-xamu bind; ngir li ci nekk ci ay njariñ yu màgg yoy deesu ko takk; ndax ci moom lañuy binde xam-xam yi di ci tënke xereñte yi, di ci wattoo xibaar yu njëkk ya, te ci lañu sàmme Téerey Yàlla yi mu wàcce, ba tax mbiri diine ak àdduna yépp jub kocc.
Li njëkk a wàcc ci Alxuraan mooy {iqra bismi Rabbika Allasii xalaqa} [Al-Halaxi: 1].
Teddngay jikkó yi, ak meloy yiw yi day tax a mucc ci ñaawteef yi, ak xeeti bon-bon yi, ku barile ay yiw mujjam rafet, ñu yaakaar ci moom muccug diine ak àdduna.
Dagan na ñu tagg nit ci kanamam ngir njariñ.
Jaadu na ñu dalal ku tiit ak bégal ko, ak tuddal ko yiy tax a mucc.
Tegtal gi gën a màgg ci wane matug Xadiija yal na ko Yàlla dollee gërëm ak rëyug gis-gisam, ak kàttanu bakkanam, mooy ne dafa melal Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mbooleem xeeti teddngay jikkó ya, te gën caa mat, ndax rafetal benn mu jëm ci jegeñaale yi, walla ci jàmbur yi, benn it mu nekk ci yaram, walla ci alal, benn it mu jëm ci ku manal boppam, walla ci keneen, moom nag mu yaatal wax ji ci bérab bu méngoo ak guddal.
Ku am mbir wàcc ci moom dees na sopp mu xamal ko ku mu wóolu ay ndénkaaneem ak wérug gis-gisam.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 7) (3).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 139) (160).
Yataal gi (3)
النهاية في غريب الحديث و الأثر (673) (175) (349) (402) (383) (811) (942) (143).
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (1/ 61).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (4/ 403).
Cited in books
7 BooksYataal gi (7)
- الأسئلة المختارة من قاموس الأسئلة الشائعة حول الإسلامقسم النبوةأول ما بدئ به رسول الله صلى الله عليه وسلم من الوحي الرؤيا الصالحة في النوم، فكان لا يرى رؤيا إلا جاءت مثل فلق الصبح، ثم حبب إليه الخلاء، وكان يخلو بغار حراء فيتحنث فيه - وهو التعبد - الليالي ذوات العدد قبل أن ينزع إلى أهله، ويتزود لذلك، ثم
- رسول الإسلام محمد صلى الله عليه وسلمهَذَا النَّامُوسُ الَّذِي نَزَّلَ اللَّهُ عَلَى مُوسَى، يَا لَيْتَنِي فِيهَا جَذْعًا، لَيْتَنِي أَكُونُ حَيًّا إِذْ يُخْرِجُكَ قَوْمُكَ، فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ ﷺ: «أَوَ مُخْرِجِيَّ هُمْ»، قَالَ: نَعَمْ، لَمْ يَأْتِ رَجُلٌ قَطُّ بِمِثْلِ مَ
- مجالس تدارس القرآن للمبتدئين (سورة الفاتحة وقصار المفصّل)1أول ما بدئ به رسول الله _صلى الله عليه وسلم_ من الوحي الرؤيا الصالحة في النوم، فكان لا يرى رؤيا إلا جاءت مثل فلق الصبح، ثم حبب إليه الخلاء وكان يخلو بغار حراء فيتحنّث فيه _وهو التعبد الليالي ذوات العدد_ قبل أن ينزع إلى أهله ويتزود لذلك، ثم
- مشروع المنهج التعليميمادة السيرة النبوية«أَوَّلُ مَا بُدِئَ بِهِ رَسُولُ اللهِ ﷺ مِنَ الوَحْيِ الرُّؤْيَا الصَّالِحَةُ فِي النَّوْمِ، فَكَانَ لاَ يَرَى رُؤْيَا إِلَّا جَاءَتْ مِثْلَ فَلَقِ الصُّبْحِ، ثُمَّ حُبِّبَ إِلَيْهِ الخَلاَءُ، وَكَانَ يَخْلُو بِغَارِ حِرَاءٍ فَيَتَحَنَّثُ
- موسوعة الأسئلة (المجموعة الأولى)«أَوَّلُ مَا بُدِئَ بِهِ رَسُولُ اللهِ ﷺ مِنَ الْوَحْيِ الرُّؤْيَا الصَّالِحَةُ فِي النَّوْمِ، فَكَانَ لَا يَرَى رُؤْيَا إِلَّا جَاءَتْ مِثْلَ فَلَقِ الصُّبْحِ، ثُمَّ حُبِّبَ إِلَيْهِ الْخَلَاءُ، وَكَانَ يَخْلُو بِغَارِ حِرَاءٍ فَيَتَحَنَّث
- موسوعة الإيمانعن عائشة أم المؤمنين رضي الله عنها أنها قالت: أَوَّلُ مَا بُدِئَ بِهِ رَسُولُ اللَّهِ صلى الله عليه وسلم مِنَ الوَحْيِ الرُّؤْيَا الصَّالِحَةُ فِي النَّوْمِ، فَكَانَ لَا يَرَى رُؤْيَا إِلَّا جَاءَتْ مِثْلَ فَلَقِ الصُّبْحِ، ثُمَّ حُبِّبَ إِ
- نبراس طالب (4)1وَاللهِ مَا يُخْزِيكَ اللهُ أَبَدًا، إِنَّكَ لَتَصِلُ الرَّحِمَ، وَتَحْمِلُ الكَلَّ، وَتَكْسِبُ المَعْدُومَ، وَتَقْرِي الضَّيْفَ، وَتُعِينُ عَلَى نَوَائِبِ الحَقِّ