Skip to content

Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.

«إِنَّ أَبْغَضَ الرِّجَالِ إِلَى اللهِ الْأَلَدُّ الْخَصِمُ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy ku man a xulóo te bari le ko, mooy ki dul nangoo topp dëgg, te di ko jéem a weddi ci dàggasante, walla muy xulóo ci dëgg waaye day ëppal ca xulóo ba, ba day jéggi dayo, di werente cig ñàkk a xam.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Du bokk ci xeetu dàggasante buñu ŋàññi su dee ki ñu tooñ dafa laaj yelleefam ci yoon.

Werente ak xulóo dafa bokk ci gàkk-gàkki làmmeñ yiy sabab ag tàqalikoo ak bàyyente ci diggante jullit ñi.

Dàggasante dana baax bu teggee cig dëgg te defiin wa rafet, waaye dees na ko wàññi bu dee ngir delloo dëgg la saxal ay neen, walla mu bañ a am ay lay ak ay firnde.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 131) (2457).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2054) (2668).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 476).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 308).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 416).

سبل السلام بشرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 685).