Skip to content

«wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».

«حُجِبَتِ النَّارُ بِالشَّهَوَاتِ، وَحُجِبَتِ الْجَنَّةُ بِالْمَكَارِهِ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sawara dañu koo wërale ak i mbir yoy bakkan da koo bëgg, ci jëf yu araam yi, ag gàtteñlu ci yu war yi; Ku topp bànneexam ci loolu kon yeyoo na sawara, Àjjana nag lu ñu muur la wërale ko ak ay mbir yoy bakkan da koo bañ; niki sax ci def ndigal yi bàyyi tere yi te muñ ca, bu dëgëree xeex ak bakkanam ci loolu kon yayoo na dugg àjjana.

Maanaay baat yi

حُجبت: حُفت وأُحيطت.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci liy tax a tàbbi ci bànneex yi li Saytaane di taaral lu bon ak lu ñaaw, ba mujj bakkan bi di ko gise lu rafet daal di jeng jëm ca.

Digle ñu sori bànneex yi ñu araamal; ndax te yoonu sawara la, ak muñ ci yu naqari yi ndax te yoonu àjjana la.

Ngëneelu xeex ak bakkan, ak farlu ci jaamu yi, ak muñ ci yu naqari yi ak coono yi wër topp yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 102) (6487).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2174) (2822).

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 122) (4744).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 274) (2560).

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (7/ 3) (3763).

Yataal gi (10)

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 449).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 87).

المنهاج شرح صحيح مسلم بن الحجاج.

للنووي (17/ 165).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 183).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 134).