Skip to content

«buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw»

Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw»

«لَا تَقُولُوا: مَا شَاءَ اللهُ وَشَاءَ فُلَانٌ، وَلَكِنْ قُولُوا: مَا شَاءَ اللهُ ثُمَّ شَاءَ فُلَانٌ».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat.
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na jullit bi muy wax: "bu soobee Yàlla soob diw", Walla lu soob Yàlla ak diw; Ndaxte coobarey Yàlla ak nàmmeelam lu boy la kenn du ko bokk ak moom, jëfandikoo (ak) cig toftale dees ciy dégge ne daa am ku bokk ak Yàlla ak yamale leen. Waaye day wax: looloo soob Yàlla topp mu soob diw, Mu def coobarey jaam bi mu topp ci coobarey Yàlla ci mu wax: "topp" te baña wax "ak" ndaxte "topp" day tektale ag toftaloo.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Araam na ñuy wax: "bu soobee Yàlla soob la", ak lu ko niru ci ay kàddu ndax li ci nekk ci toftal ci Yàlla ak; ndaxte ci bokkaaley kàddu yi ak wax yi la bokk.

Dagan na ñu wax: "li soob Yàlla topp mu soob la", ak lu ko niru lol dañuy toftal ci Yàlla baatu topp ngir ne la ñuy moytu deñ na.

Saxalal Yàlla coobare, ak saxalal jaam bi coobare, ak ne coobarey jaam bi day topp coobarey Yàlla mu kawe mi.

Tere nañu boole nit ñi ci coobarey Yàlla doonte ci wax la.

Aji-wax ji bu fasee ne coobarey jaam bi dafa melni coobarey Yàlla yam ak moom ci matale ak cig boyal, walla fas ne jaam bi dafa am coobare gu beru loolu bokkaale gu mag la, waaye bu fasee ne eggul foofu; loolu bokkaale gu ndaw la.

Dellluwaay yi

Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi (9/ 361) (10755).

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 334) (4980).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (38/ 299) (23265).

(38/ 364) (23339).

Yataal gi (4)

الجديد في شرح كتاب التوحيد.

لمحمد القرعاوي (ص368).

الملخص في شرح كتاب التوحيد.

لصالح الفوزان (ص329).