«ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul»
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee li ma wax moo ngi ci sama mbokk mi nag? Mu wax ne: «bu nekkee ci moom kon jëw nga ko, bu nekkul ci moom nag kon duural nga ko».
«أَتَدْرُونَ مَا الْغِيبَةُ؟»، قَالُوا: اللهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ، قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ»، قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «إِنْ كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُنْ فِيهِ فَقَدْ بَهَتَّهُ».
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral dëgg-dëggi jëw bi araam, te mooy: tudd jullit bu fàddu ci lu ko neexul, moo xam ciw mbindiinam la walla ciy jikkoom, niki: patt bi, wurujkat bi, fenkat bi, ak melo yu ñaaw yi ko niru, donte melo yooyu moo ngi ci moom. Bu dee melo wi nekkul ci moom nag loolu moo gën a tar jëw, ndax duur la, maanaam: sosal nit ki ci lu nekkul ci moom.
Bokk na ci njariñal adiis bi : Rafetug njàngalem Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax mu jox leen masala yi ci anamug laaj.
Rafetu teggini Sahaaba yi ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax ñu ne ko Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam.
Ki ñuy laaj wax ci lu mu xamul: Yàllaa xam.
Aar gi Sariiha aar mbooloo mi ci sàmm àq yi ak diggante mbokk yi.
Jëw lu araam la lu dul ci yenn anam yi ngir yéwénal; bokk na ca: dindi tooñaange, lu melni ki ñu tooñ tudd turu ka ko tooñ ci koo xam ne man na koo nangul àqam, mu wax ko ne ko: diw tooñ na ma, walla def na ma lii, bokk na ca: diisoo ci mbirum sëy, wàlla lu jëm ci bokk dara, mbaa ci ki ngay dëkkal, ak yu ni mel.
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2001) (2589).
Yataal gi (6)
فتح ذي الجلال والاكرام بشرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (6/ 378).
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (10/ 237).
توضيح الأحكام من بلوغ المرام.
للبسام (7/ 428).
Cited in books
5 BooksYataal gi (5)
- قاموس الكبائرموسوعة الكبائر - المجموعة الثانية«أَتَدْرُونَ مَا الغِيبَةُ؟»، قَالُوا: اللَّٰهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ، قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ»، قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «إِنْ كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ، فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُ
- قاموس الكبائرموسوعة الكبائر - المجموعة الثالثة«أَتَدْرُونَ مَا الْغِيبَةُ؟». قَالُوا: اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ. قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ». قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «إِنْ كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُن
- مجموعة زاد الحديث(3)1«أَتَدْرُونَ مَا الْغِيبَةُ؟» قَالُوا: الله وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ، قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ» قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «إِنْ كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ، فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُنْ فِ
- محرمات استهان بها كثير من الناسأتدرون ما الغيبة ؟ قالوا الله ورسوله أعلم. قال: ذكرك أخاك بما يكره، قيل: أفرأيت إن كان في أخي ما أقول؟ قال: إن كان فيه ما تقول فقد اغتَبتَه، وإن لم يكن فيه فقد بهَتَّهُ
- مشروع المنهج التعليميمادة الحديث مستوى 2«أَتَدْرُونَ مَا الْغِيبَةُ؟» قَالُوا: اللهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ. قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ» قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ قَالَ: «إِن كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ، فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُنْ فِي