«lépp luy màndiloo sàngara la, te lépp luy màndiloo dafa araam, te kuy naan sàngara ci àdduna ba dee fekk ne tàmm na ko te tuubu ko, kooku du ko naan ca allaaxira».
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«lépp luy màndiloo sàngara la, te lépp luy màndiloo dafa araam, te kuy naan sàngara ci àdduna ba dee fekk ne tàmm na ko te tuubu ko, kooku du ko naan ca allaaxira».
«كل مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وكل مُسْكِرٍ حرام، ومن شرِب الخمر في الدنيا فمات وهو يُدْمِنُهَا لَمْ يَتُبْ، لَمْ يَشْرَبْهَا في الآخرة».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne lépp luy yóbbu xel di ko dindi loolu sàngara la suy màndiloo moo xam lu ñuy naan la walla lu ñuy lekk walla lu ñuy xeeñju walla lu dul loolu, ak ne lépp luy màndiloo di yóbbu am xel loolu Yàlla araamal na ko tere ko, moo xam mu néew walla mu bari. Ak ne képp ku naan benn xeet ci yooyu di màndiloo, sax ci di ko naan te tuubu ko ba faatu; kooku yeyoo na mbugalum Yàlla ci mu xañ ko ba du ko naan ca àjjana.
Li tax ñu araamal sàngara mooy màndiloo gi, kon lépp luy màndiloo ak xeet wu mu man a doon dafa araam.
Yàlla -mu kawe mi- araamal na sàngara; ndax li mu làmboo ci ay lorànge ak i yàqute yu màgg.
Naan sàngara ca àjjana daa bokk ci matug bànneex ak matug xéewal.
Ku téyewul boppam ba du naan sàngara ci àdduna Yàlla dana ko xañ ba du ko naan ca àjjana, ndax ag pay daal day toll kem na jëf ja tollu.
Soññee ci gaaw a tuub bàkkaar yi njëkk dee di ñëw.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 104) (5575).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1587) (2003).
Yataal gi (15)
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (8/ 519).
فتح ذي الجلال والاكرام بشرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (5/ 418).
توضِيحُ الأحكَامِ مِن بُلوُغ المَرَام.
للبسام (6/ 307).
معالم السنن.
وهو شرح سنن أبي داود.
للخطابي (4/ 264).
الفتح الرباني لترتيب مسند الإمام أحمد بن حنبل الشيباني.
للساعاتي (16/ 116).
فيض القدير شرح الجامع الصغير.
للمناوي (5/ 30).
مرقاة المفاتيح شرح مشكاة المصابيح.
لعلي القاري (6/ 2382).
Cited in books
6 BooksYataal gi (6)
- سؤال وجواب حول الإسلام«كُلُّ مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وَكُلُّ مُسْكِرٍ حَرَامٌ»
- قاموس الكبائر موسوعة الكبائر - المجموعة الأولى«كُلُّ مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وَكُلُّ مُسْكرٍ حَرَامٌ، وَمَنْ شَرِبَ الخَمْرَ فِي الدُّنْيَا فَمَاتَ وَهُوَ يُدْمِنُهَا وَلَمْ يَتُبْ، لَمْ يَشْرَبْهَا فِي الآخِرَةِ» [96].
- قاموس الكبائر«كُلُّ مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وَكُلُّ مُسْكرٍ حَرَامٌ، وَمَنْ شَرِبَ الخَمْرَ فِي الدُّنْيَا فَمَاتَ وَهُوَ يُدْمِنُهَا وَلَمْ يَتُبْ، لَمْ يَشْرَبْهَا فِي الآخِرَةِ» [96].
- كتاب تعليم المسلم الجديد«كُلُّ مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وَكُلُّ مُسْكِرٍ حَرَامٌ»
- مجموعة زاد الفقه (4)«كُلُّ مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وكُلُّ مُسْكِرٍ حَرامٌ».
- محرمات استهان بها كثير من الناسكل مسكر خمر، وكل مسكر حرام