Skip to content

«aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli».

Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli».

«إنَّ المُؤْمِنَ ليُدرِكُ بِحُسْنِ خُلُقِهِ دَرَجَةَ الصَّائِمِ القَائِمِ».

Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat.
Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jikko ju rafet dana yóbb boroomam ca darajay ki saxoo woor bëccëg ak taxaw guddi, li dajale jikko yu rafet yi mooy: di def njekk, ak rafeti wax, ak bélli xar kanam, ak bañ a lore te di ko dékku ci nit ñi.

Maanaay baat yi

....:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Màggug yittewoog Lislaam ci yar jikko yi ak matal ko

Ngëneelul jikko yu rafet, ba tax muy yóbb jaam bi ci darajay aji-woor jidul dog, ak aji-taxaw jidul sonn.

Woor bëccëg ak taxaw guddi ñaari jëf lañu yu màgg am na ñu nag ab coono ci bàkkan, boroom jikko yu rafet yi day àgg ci seen daraja ngir li muy xeex ak bakkanam ci jëflante bu rafet.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 176) (4798).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (40/ 414) (24355).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 675).

تطرز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص411).

مشكاة المصابيح.

لمحمد العمري (3/ 1409).