Skip to content

Yàlla mu kawe mi dafa wàcce: {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy yéefar yi}

Jële nañu ci Ibnu Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne :

Yàlla mu kawe mi dafa wàcce: {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy yéefar yi} [Al-Maa-ida: 44] ak {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy tooñkat yi} [Al-Maa-ida: 45], ak {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy kàccoor yi} [Al-Maa-ida: 47], nee na: ibn Abbaas nee na: yàlla da ko a wàcce ci ñaari kuréel vi Yahuud yi, genn ha dafa notoon geneen gi ca ceddo ga, ba mujj ñi gërëmloo daal yéwénoo ci ne kepp ku ñu ray te ku tedd ray ko ab diyaam mooy juróom-fukki Wasq, kepp ku ñu ray ci ñi tedd ñi te ku xeebu ray ko ab Diyaam mooy téeméeri Wasq, ñu nekk ci loolu ba Yonnente bi ñëw Madiina, ñaari kuréel yépp faf xeebu ngir ñëwug Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jamono yooyu fésagul, te notagu leen ci loolu, ndax dafa nekkoon ci yéwénoo, ñu xeebu ña ray kenn ci ñu tedd ña, ñu tedd ña yónnee ca ñu xeebu ña ne leen: yónneeleen ni téeméeri Wasq, ñu xeebu ña ne leen: ndax lii mas naa am ci ñaari koñ yoo xam ne seen diine been la, seen askan benn la, seen réew di benn, Diyag ñenn ñi di xaaju Diyag ñeneen ñi? Nun danu leen a joxoon loolu ci kaw tooñ gu ngeen nu tooñ, ak ragal gi ni leen ragal, ginnaaw nag Muhammat ñëw na dunu leen jox loolu, xeex bi nara jolli seen diggante, ñu gërëm a def Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu àtte seen diggante, ñi tedd ñi wax ne: giñ nañu ne Muhammat du leen jox jële ci ñoom, lu ëpp li mu leen di jox ñoom jële ci yéen, te wax nañu dëgg, joxuñu ni woon loolu lu dul ag tooñ gu ñu leen tooñ, ak not gu ñu leen not, yabal leen fa Muhammat ku leen di gëstut gis-gisam: bu leen joxee la ngeen bëggoon ngeen àtteloo ko, bu leen ko joxul ngeen moytu bañ ko a àtteloo, ñu yabal fa Yonnente Yàlla ba ay nit yu bokk ci naaféq yi ngir ñu xam gis-gisam, ba Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Yàlla xamal Yonnenteem bi seen mbir yépp ak li ñu namm, Yàlla mu màgg mi daal di wàcce: {Yaw Yonnente bi, bu mu la jàqal mukk ñiy gaawantu ci ag kéefar te bokk ci ñiy wax naan gëm nanu} [Al-Maa-ida: 41] ba ci waxam ji: {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy kàccoor yi} [Al-Maa-ida: 47] topp mu wax ci ñoom ñaar ne: giñ naa ci Yàlla ne wàcc na te ñoom ñaar la ci Yàlla mu màgg mi jublu.

إِنَّ اللهَ عَزَّ وَجَلَّ أَنْزَلَ: {وَمَنْ لَمْ يَحْكُمْ بِمَا أَنْزَلَ اللهُ فَأُولَئِكَ هُمِ الْكَافِرُونَ} [المائدة: 44] وَ {فَأُولَئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ} [المائدة: 45] وَ {فَأُولَئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ} [المائدة: 47] ، قَالَ: قَالَ ابْنُ عَبَّاسٍ: أَنْزَلَهَا اللهُ فِي الطَّائِفَتَيْنِ مِنَ اليَهُودِ، وَكَانَتْ إِحْدَاهُمَا قَدْ قَهَرَتِ الأُخْرَى فِي الجَاهِلِيَّةِ، حَتَّى ارْتَضَوْا وَاصْطَلَحُوا عَلَى أَنَّ كُلَّ قَتِيلٍ قَتَلَتْهُ العَزِيزَةُ مِنَ الذَّلِيلَةِ فَدِيَتُهُ خَمْسُونَ وَسْقًا، وَكُلَّ قَتِيلٍ قَتَلَتْهُ الذَّلِيلَةُ مِنَ العَزِيزَةِ فَدِيَتُهُ مِائَةُ وَسْقٍ، فَكَانُوا عَلَى ذَلِكَ حَتَّى قَدِمَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ المَدِينَةَ، وَذَلَّتِ الطَّائِفَتَانِ كِلْتَاهُمَا لِمَقْدَمِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، ورَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَوْمَئِذٍ لَمْ يَظْهَرْ، وَلَمْ يُوطِئْهُمَا عَلَيْهِ، وَهُوَ فِي الصُّلْحِ، فَقَتَلَتِ الذَّلِيلَةُ مِنَ العَزِيزَةِ قَتِيلًا، فَأَرْسَلَتِ العَزِيزَةُ إِلَى الذَّلِيلَةِ: أَنِ ابْعَثُوا إِلَيْنَا بِمِائَةِ وَسْقٍ، فَقَالَتِ الذَّلِيلَةُ: وَهَلْ كَانَ هَذَا فِي حَيَّيْنِ قَطُّ دِينُهُمَا وَاحِدٌ، وَنَسَبُهُمَا وَاحِدٌ، وَبَلَدُهُمَا وَاحِدٌ، دِيَةُ بَعْضِهِمْ نِصْفُ دِيَةِ بَعْضٍ؟ إِنَّا إِنَّمَا أَعْطَيْنَاكُمْ هَذَا ضَيْمًا مِنْكُمْ لَنَا، وَفَرَقًا مِنْكُمْ، فَأَمَّا إِذْ قَدِمَ مُحَمَّدٌ فَلَا نُعْطِيكُمْ ذَلِكَ، فَكَادَتِ الحَرْبُ تَهِيجُ بَيْنَهُمَا، ثُمَّ ارْتَضَوْا عَلَى أَنْ يَجْعَلُوا رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بَيْنَهُمْ، ثُمَّ ذَكَرَتِ العَزِيزَةُ، فَقَالَتْ: وَاللهِ مَا مُحَمَّدٌ بِمُعْطِيكُمْ مِنْهُمْ ضِعْفَ مَا يُعْطِيهِمْ مِنْكُمْ، وَلَقَدْ صَدَقُوا، مَا أَعْطَوْنَا هَذَا إِلَّا ضَيْمًا مِنَّا، وَقَهْرًا لَهُمْ، فَدُسُّوا إِلَى مُحَمَّدٍ مَنْ يَخْبُرُ لَكُمْ رَأْيَهُ: إِنْ أَعْطَاكُمْ مَا تُرِيدُونَ حَكَّمْتُمُوهُ، وَإِنْ لَمْ يُعْطِكُمْ حَذِرْتُمْ فَلَمْ تُحَكِّمُوهُ، فَدَسُّوا إِلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ نَاسًا مِنَ المُنَافِقِينَ لِيَخْبُرُوا لَهُمْ رَأْيَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَلَمَّا جَاءَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَخْبَرَ اللهُ رَسُولَهُ بِأَمْرِهِمْ كُلِّهِ وَمَا أَرَادُوا، فَأَنْزَلَ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ {يَا أَيُّهَا الرَّسُولُ لَا يَحْزُنْكَ الَّذِينَ يُسَارِعُونَ فِي الْكُفْرِ مِنَ الذِينَ قَالُوا آمَنَّا} [المائدة: 41] إِلَى قَوْلِهِ: {وَمَنْ لَمْ يَحْكُمْ بِمَا أَنْزَلَ اللهُ فَأُولَئِكَ هُمِ الْفَاسِقُونَ} [المائدة: 47] ثُمَّ قَالَ فِيهِمَا: وَاللهِ نَزَلَتْ، وَإِيَّاهُمَا عَنَى الله عَزَّ وَجَلَّ.

Ahmat soloo na ko.
Tane na
Leeral gi

Bokkoon na ci Yahuudi Madiina yi Banuu Xuraysa ak Banuu An-Nadiir benn bi notoon beneen bi ca ceddo ga, ñu gërëmlu daal di yéwénoo ci ne képp ku ñu ray te ñu tedd ñi not ray ko ci ñu xeebu yi ñu not ag Diyaam mooy juróom-fukki Wasq dong, te képp ku ñu ray te ñu xeebu ñi ray ko ci ñi tedd ñi ag Diyaam mooy téeméeri Wasq, Wasq mooy juróom-benn- fukki Saah. Ñu nekkoon ci loolu ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc gàddaay ñëw Madiina, ñaari kuréel yépp nangul Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jamono yooya gañeegul ay noonam, te notagu leen ci ñu topp; ndax loolu ca njëlbéenu gàddaay ga la woon, fekk ma nga ca yéwénoo ga. Ñu xeebu ña ray ca ñu tedd ña kenn, ñu tedd ña yónnee ca ñu xeebu ña ne leen: yónneeleen nu téeméeri Wasq kem ni nu dëppoo woon, ñu xeebu ñi ne leen: ndax lii mas naa am ci ñaari koñ yoy seen diine benn la, seen askan benn la, seen réew benn la, ba noppi Diyag ñenn ñi di xaaju Diyag ñeneen ñi?! Te nun danu leen ko a joxoon ngir seenug tooñ gu jem ci nun, ak sunug ragal gu jëm ci yéen, ginnaaw Muhammat ñëw na nag dunu leen jox loolu mukk. Xeex ba nara jolli seen diggante, topp ñu gërëm a def Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mi àtte seen diggante, ñu tedd ña settantal, daal di ne: giñ nanu ci Yàlla ne Muhammat du leen jox jële xaaju li mu leen di jox ñoom jële ci yéen, te ñoom wax nañu dëgg, joxuñu nj lii lu dul ci kaw sunug tooñ, ak li nu leen not, yónneeleen ca Muhammat ci sekkare ku leen indil gis-gisam, bu dee jox na li ngeen bëgg ngeen àtteloo ko, bu leen joxul li ngeen bëgg ngeen bàyyi ko te bañ ko a àtteloo seen diggante. Ñu yónnee ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sekkare ay nit yu bokk ci naaféq yi ngir ñu xam gis-gisu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ba ñëwee ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Yàlla wàcce Wahyu xibaare Yonnenteem bi seen mbir yépp ak li ñu bëgg, Yàlla mu màgg mi wàcce saaru Al-Maa-ida li ko dale ci waxam ji: {yaw Yonnente bi bu mu la jàqloo mukk ñiy njëkkante ci kéefar te bokk ci ñiy wax gëm nanu} {Al-Maa-ida: 41}. Ba ci waxam ji: {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy kàccoor yi} [Al-Maa-ida: 47] Topp Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm wax ne: giñ naa ci Yàlla ne ci ñoom ñaar la waxu Yàlla Yàlla jii wàcc: {ku àttewoowul ci li Yàlla wàcce ñooñu ñooy yéefar yi} [Al-Maa-ida: 44] Ak {...ñooñu ñooy tooñkat yi} [Al-Maa-ida: 45] Ak {...ñooñu ñooy kàccoor yi} [Al-Maa-ida: 47] , te ñoom ñaar dong la ci Yàlla mu màgg mi jublu.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xamug Yahuud ci dëggug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Pexey Yahuud yi ak seenug tooñ ba ci seen bopp.

Xibaarug Yàlla mu màgg mi ci ne Yahuud yi toroxtange ñeel na leen ci àdduna ak mbugal mu màgg ca allaaxira.

Ñàkk a àttewoo ci li Yàlla wàcce ak gërëmloo àtteb Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tegtal la ci kéefar ak tooñ ak kàccoor.

Giraawaaleg naaféq yi ak seenug dimbalante ak Yahuud yi.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (4/ 88) (2212).

978.

702.

1017.

305).

Yataal gi (1)

النهاية في غريب الحديث والأثر (ص 972.