Skip to content

"yellul ci jullit bi mu am dara lu muy dénkaane, muy fanaan ñatti guddi, lu dul ne ndénkaaneem li dana nekk fi moom mu bind ko"

Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"yellul ci jullit bi mu am dara lu muy dénkaane, muy fanaan ñatti guddi, lu dul ne ndénkaaneem li dana nekk fi moom mu bind ko", Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm wax ne: "diirub ma dégg loolu ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc genn guddi rombul lu dul ne sama ndénkaane mi ngi fi man ma bind".

«مَا حَقُّ امْرِئٍ مُسْلِمٍ لَهُ شَيْءٌ يُوصِي فِيهِ، يَبِيتُ ثَلَاثَ لَيَالٍ، إِلَّا وَوَصِيَّتُهُ عِنْدَهُ مَكْتُوبَةٌ»، قَالَ عَبْدُ اللهِ بْنُ عُمَرَ رضي الله عنهما: «مَا مَرَّتْ عَلَيَّ لَيْلَةٌ مُنْذُ سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ ذَلِكَ إِلَّا وَعِنْدِي وَصِيَّتِي».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne jaaduwul ci ab jullit mu am lu muy dénkaane ci ay àq walla alal donte dafa néew, muy fanaan ñatti guddi, lu dul ne ndénkaaneem mi ngi fi moom mu bind. Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm wax na ne: diirub ma dégg loolu ci Yonente bi fanaanuma genn guddi lu dul ne sama ndénkaane mi ngi fi man.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees nañu dénkaane ak gaawe ko, ngir leeral ko, ak jëfe ndigalu aji-yoonal ji, ak waajal dee, ak xamle ko ak fan la ñu ko war a jëme, balaa dara di ko soxlaal wolif ko.

Dénkaane: maanaam, kollarante, nit ki kóllarante ak keneen ci mu defal ko dara ci alalam, walla mu kollarante ak keneen ci mu xoolal ko doomam yu ndaw yi, walla mu kollarante ak keneen ci yeneen jëf yu mu moom ci ginnaaw bi deewee.

Dénkaane ñatti xaaj la: 1- gu ñu sopp, te mooy dénkaane ci lenn ci alalam ci ñu defal ka ko ci yoonu yiw, ak rafetal; ngir yool bi egg ci moom ginnaaw bi mu faatoo, 2- gu war, te mooy dénkaane àq yi ko war, moo xam àqi Yàlla la, niki asaka, ak lu ko niru, ci yi war ci moom ci cosaani sariiha yi, walla muy àqi doomi Aadama yi; niki bor, ak delloo kóolute yi ñu ko dénkoon, 3- gu araam, te mooy bu ëppee ñatteelu xaaju alal ji, walla mu ñeel kuy donn.

Ngëneelu Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm, ak gaawantoom ci jëfe yiw, ak topp Aji-Yoonal ju xereñ ji.

Ibn Daxiixilhiid nee na: yombal gi ci ñaari guddi ak ñatt ngir dindi coono la ak jafe-jafe.

Bir yu am solo yi dees ko a war a wattu ci bind ko; ndax mooy gën a sax te mooy gën a sàmm àq yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 2) (2738).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1250) (1627).

Yataal gi (4)

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (2/ 48).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

لعبد الله البسام (ص548).